Bismilaahi rahmani rahim.
Sunu Sang bi, mi ngi bàyikko ci ñaari askan yu tèdd ta moy askanu Mbàkke Maam Maharam ak askanu Koki.
« Mbolem borom xam-xam yi ci réew mi ak wàliyu yi ci ñaari neek yi dong lañ sëto » ci waxi Sëriñ Xalil ca teerem ba mu duppé Goor Yàlla gi,
Maam cerno nak mi ngi ganné adduna yoor yoor’ub alxamiss ci fukki fan ak juróom ci weru gàmu 1862 ci dëkk bu ñiy wax Poroxan, waayé dà dajek ay wàjjuram ji toxo Poroxan, batax ñongi key ngeté Njàba-kunda. Lolo waral am ñu defe ne fa la ganné adduna. Batey jëllé na ñu ci Sëriñ Xalil mu wax ne att momu ci la Maam Bamba Sall Fàtto, mom la ñu tuddé Sëriñ Tuuba Qàda lahu laahu Maaxtara lahu, batey ci la Maam Bàlla Aïcha fàtto. Wàyjuroom wu góor mi ngi tuddu Maam Moor Anta Sali mom Maam Bàlla Aïcha. Wàyjurom wu jigéen mi ngi tuddu Soxna Fàti Isa mom Ndiaga Isa mom Maddu Fàxujja.
Maam Cerno nak kenn lë bokkal ndey ak baay ci góor muy Sëriñ Móodu Faati (mom nak baayi wu fi doom). Ñaari’t la bokkal ndey ak baay ci jigéen muy Soxna Aminta Mbàkke ak Soxna Faati Binta Mbàkke.
Wax nen ne bi Borom Daaru ganné adduna, Sëriñ Moor Anta da ne Sëriñ Tuuba Qàda lahu laahu Maaxtara lahu sa ñaan ga nangu na, mahna, am nga ku la mana jàpalé ci sa ligey bi. Wax na ñu ne booba Sëriñ Tuuba Qàda lahu laahu mi ngi jang Alqur’an ba tool ci : « Wa axii hërùnu huwa afsahu minii lisaa’nan fa arsilhu mahii riddan yusadiqnii … ». Bam ko defe mu jokk bindal ko Asabhatul Munjiyàtu.
Lu di melom ?
Sëriñ Xalil wax na ni dà ñùloon ci melo, waayé cër ya da joton loolu ba taxna su ngen toggé da ngey défé ni mola sutt, te gaatt. Lolla waral ñu dan ko wax Ndamal Daaru, ku silwisé la won, ku nopi la won, bariwul ay wax, ku ñamé won toogay bu yaag la won, ku bari xam-xam la won, ku ragal yàlla, ku dëddu adduna, ku amu’k raañé, ku amu’k fit te jambaré. Wax na ñu ne Sëriñ Haydara doomam moko gana nuru jëm ci wa këram yi. Sëriñ Séex Xadi moko gana nuru kàddu.
Su ko defe ku bëgg xam ay jaar-jaaram ci Alqur’an, xam-xam ak Tarbiyah ak jambàram ci faan yu bari na yër téeré Sëriñ Xalil bi.
Diggam ak Sëriñ bi
Ku ne xam na ni coffel gu réy mo am’on sen digganté. Likey firndel bokk na ca la Ku Tèdd ki waxon ba ñuy miiras Señ Moor Anta, da ni won : « ludul kaamil bi ak Cerno awma ci soxla ». Dan nako wax yaw yày sama loxo ndey joor, àgg ci naan ko bëgg ma su donon pàkk moom la ñu la réendé. Wax yi nak amna na ay firndéel ndax Seriñ bi binde nako, señ Abdul Ahad Mbàkke radiya laahu anhu dajalé ko. Batey Sëriñ Basiiru Anta Ñang miy doomi Maam Cerno wax na ci. Waayé ku yër Diyàfatu samàdiya ak safwatu siiri mu Sëriñ Alhaji da nga ci feek bataaxel bi mey bëgg andi, joggé ci Borom Tuuba jëm ci Borom Daaru :
« Assalamu haleykum wa rahmatulah wa tahala wa barakàtahu, ginaaw nuyóobi bo gisé bataaxel bi na nga yabbal ku mokkal Alqur’an ko xam ne goné ley don mu and’ak ñaari moromam ndax ñu mana jangal goné yi neek fi, te yabbal ñetti waxaban’né yu mana jangalé xam-xam, ndax ñu mana jangal waxban’né yi neek fi. Bo gisé bataaxel bi nañ daaldi ñëw yaw mi nga xam ne dañ la réendé ci sopp’ma. Man mi nga xam ne ku ñu réendé ci sopp’ma ku texe la, texe go xam ne texe di du ci tóop »
Lii da na ñu jangal ni Sëriñ bi ku ko doylo won la , ci lepp lu jëm ci ag taan. Ndax dako taanalo ay jangalé kat ci ñaari mbir yu mu fonkon loolu, ta moy Alqur’an ak xam-xam. Batey nangul nako coffel gi mu am ci mom. Dàn na wax nann ni ma soopé Rasulilàhi, ni la ma Cerno soopé. Cerno lu mu bind mu am, ta man lu ma xalaat mu am.
Ci gàtan sunu Maam Cerno royukaay la won biir ak biti. Donon ku boolék charihatu ak aqihatu ci lepp. Mat sëkk la mu don, tabbé won loolu, ta mana ligey. Fees deel, matt Sëriñ. ku Tèdd ki dan na wax naan « and’ak man doyna waayé and’ak Cerno ëpp na ». Wax ji nak toxolé nen ko ci Sëriñ Abdu Xudoos domam radiya laahu anhu.
Sunu jambar ji nak, bissu’p alxamiis ci fukki fan ci weri shahban ci lako tawat daanel mu waccé ligey yoor-yoor’ub alxamis ci fukki waxtu ak benn, ci ñaar fukki fan ak juróom ñaar ci weru shahban attum 1362 ci gàddàyuk yonnent bi sala laahu tahala haleyhi bi alihi wa sahbihi wa salama, tolok attum 1943 ci attum tubaab ci netalig Sëriñ Xalil yalna ko fi yàlla yàgal, ta dëgaral ko barkep Sëriñ Móodu Hafsa miy wàyjuram ak Sëriñ Saalihu miy maamam.
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 02/09/2019.
[…] Kan moy Maam Cerno Birahim Mbàkke? […]