Bismillahi Rahmaani Rahiim
Sunu bunt bu mujj ci Tasawud Sixaar dafa jëm ci fay li la raw boo àndeek Imam di julli ak waxtu yi ñu taamu ci julli.
Li ci ëpp solo nag dafa jëm ci jikko yi ñu wara ame. Sëriñ bi li mu la njëkk diggal mooy yittewoo xam- xam, lewet, am kersa, noppi ak sellal. Ba tay, ngay yittewoo ràññee li ngay jàng, ak di topp foo man a nekk Yàlla subhaanahu wa tahaala, ak wakkiirlu ci moom. Su ko defee nag nga daaldi moytu fenn ak lépp lu askanoo ci moom, te it nga bañ a noonoo ak kenn, ba noppi nga jël sag dund, sa wér, sa kattan ak sa man-man lépp jébbal ko sunu Boroom. Ak yeneeni dénkaane. Wax na fi it njariñul Téere bi.
Yal nanu Yàlla defal dégg ak topp té fayal nu Sëriñ Alhaaji.
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien