
Li mooy tàmbalig Téereb Nahjul Qadaa Al-Haaji.Ubbite gi rekk doy na yóbbalug dund.
Dina fi feeñee ay laabire yu am solo ci sax ci jëf lu baax te bañ a taayi. Naka noonu ay wax yu am solo te bari njariñ moo fiy fés. Ay royukaay ci bépp Jullit, te mooy sahaaba yu baax yi. Sëriñ bi it di fi wax seen i mello, seen aada, ak seen i jikko.
Naka noonu ñaan na ci Boroomam mu am yum ko defal ci Téere bi. Wax na fi it yiw gi ci aji jàng ji man a jëlle, njariñ yi ak solo si.
Yal nanu Yàlla defal lépp lu ci Sëriñ bi ñaan, te nu mellowo lépp lu mu fi jàngale ba ku ñu gis, ci sunuy jikko ak sunu doxin, xam ni ki taalif Nahju mooy sunu Sëriñ, te mooy sunu Kilifa.
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien