Kan Mooy Sëriñ Musaa Halima Géy?

Sëriñ Musaa mi ngi cosaano Badar Géy, gane àddina atum 1890. Sëñ Maxtaar Géy baayam moo ko jàngal, teel ko dalal lool. Sëñ Musaa moom Soxna Halima mii, moo doon caatu baayam. Bi fi baayam bàyyiko, ginnaaw gi, maggam Sëriñ Mor Halima àggaleel ko jàngam. Li ko boole ak Sëriñ bi nag, moo di bi […]

Kan Mooy Soxna Astu Gaawaan

Bismillahi Rahmaani Rahiim Soxna Aysatu Mbàkke doomi Seexul Xadiim ñu gën koo xam ci turu Soxna Astu Gaawaan mi ngi gane àddina 1904. Way-juram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Xadi Jóob gën a siiwe ci Soxna Xadi Gànnaar di doomi Madu Faa-Xujja moom Masàmba Anta Ceebo. Sëriñ bi moo ko dalal am jàng. Bi […]

Kan Mooy Maam Seex Anta(1)

Mi ngi ganee àdduna atum 1867 ca poroxaan, turam dëgg mooy Seex Siidi Muxtaar Mbàkke mi ngi bokk ci askanu Maam MahramMaam Seex Anta doomi Sëriñ Moor Anta Sali la moom Maam Bàlla moom Maam Mahram.Maam Anta Njaay Mbàkke, doomi Maam Ibraahima Awa Ñang moom Maam Mahram mooy yaayam. Kon Muhammadul Xayri Mbàkke walla nga […]

Kan Mooy Seriñ Murtadaa (2)

Ca 1958 la daaldi am sañ-sañ man a taxawal mbébétam. 1963 nga ci la aji Màkka, ba mu ñibisee tukkiwaat na ànd ak Sëñ Mustafaa Lo ak Sëñ Yande ci réew yu sori niki Kowet, ak Iraak 9i weer. 1965 mu jógaat dem Araabi Sawdi. Al-Azhar nag ci ay coono yu metti la ko taxawale […]

Kan Mooy Sëriñ Murtadaa Mbàkke(1)?

Mi ngi feeñ jamono ci atum 1340 dëppoo ak 1920 walla 1921, 26 fan ci Gàmmu ca dëkk buñuy wax Daarul Haalimul Xabiir, ñu gën ko xam ci Ndaam. Soxna Njaxat Silla nettali na Sëriñ Mustafaa Lo ne ko, Sëriñ Ndaam dey terale na 33 gàtt Sëriñ Murtada. Ba weeru gàmmo teerse day def bis […]

Kan Mooy Sëriñ Masàmba Mbàkke?

Sang bi mi ngi gane àddina ci atum 1881 ca Pataar, ab dikkam ci àddina soreewul ak jamono ji way-juram wa, Sëriñ Moor Anta Sali di wuyu ji boroomam. Seexul Xadiim di magam moo ko tuddu jox ko turu Masàmba Anta Cebbo ginaaw ba mu demewoon siyaare ji barabu Sëriñ Moor fa Deqële. Sëriñ Moor […]

Kan Mooy Seex Abdul Ahad Mbàkke?

Mooy doomi Soxna Maryaama Jaxate ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu. Ci 23i la gane àddina ci weeru korite ci atum 1332 ginnaaw gàddaay gi. Di toolo ak 1914 ca Njaaréem. Ba mu toolo cim jàng leen ko jox nijaayam Sëriñ Hamzatu, nijaay ji jox ko Sëriñ Allasaan Jaxate mu jàngal ko Alxuraan. […]

Kan Mooy Maam Saalihu Faal?

Bismilaahi Rahmani RahiimSëriñ Saalihu Faal mi ngi feeñ jamono ci atum 1858 ci dëkk buñuy wax « Jabbe Faal ».Jabbe Faal nag mi ngi ci wettu « Waaqi » mi nga xam ne ci kiliftéefu Aatumaan Faal la bokkoon ci Jàmbur. Way-juram wu góor mi ngi tuddu Ahmadul Faal Roqaya, way-juram wu jigéen mi ngi tuddu Soxna Saynabu Njaay […]

Kan Mooy Sëriñ Shuwaahibu Mbàkke?

Doomi Soxna Maryaama Jaxate la ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu Maxtaara lahu.Ci wéeru koor la gane àddina, jëmb ju màgg la woon, ragal Yàlla lool te ràññeeku ci. Dundam di njariñ gu yaatu te bari solo. Mi ngi gane àddina bisub talaata 1335 ci gàddaay gi, toolo ag 17 juin 1917 ca Njaaréem ci […]

Kan mooy Sëriñ Mbay Jaxate?

Soxna Penda Kumba Faal mooy way-juram wu jigéen, Sëriñ Xaali Majaxate Kalla mooy baayam, moo ko jàngal itam. Ginaaw gi it jàngee na it ci Sëriñ Moor Saasum Jaxate. Ba fi baayam jóge ci atum 1900 la daaldi fas a jaayante ak Seexul Xadiim waaye boobu Sëriñ bi mi ngi ci tukeem ya, loolo tax […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR