Baay Njaga Jóob nee na : « Seydinaa Usmaan dafa njariñu ci Seex Ibra, njariñu ci Maam Cerno, njariñu ci Sëriñ Tuubaa ». Ku daan ñaan la muy am, te ràññeeku ci lool.
Am na sax ay nit yu daan jëfandikoo sàngara, moo ko dindi ci ñoom ci lu gaaw. Daf daan soññi murid yi ci jàpp seenub taalube, te doyloo Sëriñ Tuubaa ci lépp. Te bañ koo yemale ak kenn. Doonoon it ku am koolute ak ngëm gu wér ni jàpp ci Sëriñ Tuubaa mooy sunu pajug aajo àdduna ak allaaxira. Jàmbaar tigi la woon ci yoon wi.
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien