Dénkaane Sëriñ bi jëm ci ab muritam(1).

Bismilaahi rahmaani rahiim. «Jógal jaamu Yàlla boo ragalee mu faat la loolu mooy tax doo woru ci àdduna, te jiital yéene ndax mooy tax sa yaakaar dëggu. Waaye boo nee danga yaakaar Yàlla ba noppi doo jëf ndigalam doo bàyyi ay téreem kon sa yaakaar dese naa mat. Moo tax mu ne ko bul bëgge, […]

Dénkaane bu jëm ci topp Yàlla (4)

Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Képp koo xam ne yaa ngi sàkku àjjana ci lu dul ngay topp Yàlla sunu Boroom, te yaakar ne danga koo am sab xol leerul, ndax ba laa kenn a man a ngóob day fekk mu farlu woon cim mbay. Lépp loo xam ne da lay gàllankoor ci topp sunu Boroom bàyyi […]

Dénkaane bu jëm ci Abdullahi (6)

Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Yaw Abdullahi maa ngi lay dénk nga ragal Yàlla waxtu wu nekk. Boo bëggee mucc ëllëg, làq ag texe. Nanga sellal sab xol, te tàqalikoo ak bidaa, te taqoo ak Sunna, tey fexe sàmmonte ak ndigal yi.Deel ànd ak ñu baax ñi, bul ànd ak ku bon mukk. Deel fexe saafara say […]

Dénkaane bu jëm ci Soxna Penda Jóob (8)

Bismilaahi rahmaani rahiim. Sëriñ bi ginnaaw ba mu leeralee ni kuy sàkku Boroomam la ak Yónnentam ba salla laahu tahaala aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama, la daaldi wane ag jubloom ci dénk soxnas baayam ju ndaw ja, nu naan ko Penda Jóob. Daf ko wax ne: Maa ngi lay diggal yaw soxna si […]

Dénkaane bu jëm ci Murid yëpp (10)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. « Maa ngi leen di dénk topp Yàlla te bañ a noonoo, deeleen soppante ci Yàlla te bañ a xëccoo, bañ a réeral kenn. Soppante ci Yàlla mooy ag ngëm, ku ko def dangay am mbégte ak Kóolute ; iñaanante nag ñu ko def cig texeedi rekk la leen jëme. Jikko ji gën […]

Dénkaane bu jëm ci doomi mbokki Sërin Tuubaa(14).

Bismilaahi Rahmani Rahiim.  » Maa ngi leen di dénk xam, ak jëfe ak tegginu te bàyyi fo. Xam-xam saa su ne luy bégloo lay àndi waaye réer luy lor rekk lay àndi. Ñàkk teggin nag day waral sori Yàlla. Ñàkk jëfe li nga xam day waral alku. Barim po day xañe ay yiiw.Kon deeleen farlu […]

Dénkaane bu jëm ci Seex Mabaabu Géy ak yeneeni dénkaan yu jëm ci bépp murit

Bismilaahi Rahmani Rahiim. Di nga fi dégge ay dénkaan yu fees deel ak njariñ, lépp nag jëm ci jullit bi rawatina murid bi. Te mel na ne tënk na lu bare bari ci ñaari Téere yi nu mujjee yaatal te mooy Maxaaliqu-Niiraan ak Zaadu Zawii-Tahalumi. Al-Habdul Xadiim 20/06/2020

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR