Bismilaahi rahmaani rahiim.
«Jógal jaamu Yàlla boo ragalee mu faat la
loolu mooy tax doo woru ci àdduna, te jiital yéene ndax mooy tax sa yaakaar dëggu. Waaye boo nee danga yaakaar Yàlla ba noppi doo jëf ndigalam doo bàyyi ay téreem kon sa yaakaar dese naa mat.
Moo tax mu ne ko bul bëgge, bul mébet ndax bëgge mooy bëgg mbir ba noppi doo def lu la ko may. Ba tay loolu mooy mébet daanaka.
Sunu Boroom li mu sàkku ci yaw mooy nga jaamu ko rekk. Kon li nga war a def mooy ñaan ko mu dimbali la ci jaamu googu, sa xol bañ a am benn taq-taq, nga xam ne doo iñaane kenn doo bañ kenn. Sunu Boroom nag nekkam gi ak màggam gi dafa fés lool ba doo aajowoo ku la koy xamal ak ku la koy tegtal. Ndax loo xool lu ne man nga caa xame sunu Boroom. Su ko defe nag sunu Boroom ñi ko xam soxlawuñu dara lu moy moom, te loolu li ko waral moy xam gi rekk».
Al-Habdul Xadiim,
Grenoble, 12/01/2020.