Bismilaahi rahmani rahim. Sunu Sang bi, mi ngi bàyikko ci ñaari askan yu tèdd ta moy askanu Mbàkke Maam Maharam ak askanu Koki. « Mbolem borom xam-xam yi ci réew mi ak wàliyu yi ci ñaari neek yi dong lañ sëto » ci waxi Sëriñ Xalil ca teerem ba mu duppé Goor Yàlla gi, Maam cerno nak […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Nu fas yéene jukki leen ci hikma yi Borom Daarul Muhti daan wax. Li nu fiy nettali nag ci Sëriñ Xalil Mbàkke mu Sëñ Mustafaa Afsa lanu ko toxale. Al-Habdul Xadiim Grenoble, 01/04/2020.
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Fii danu fiy xamle ni Sëriñ bi daan jëflante ak Maam Cerno, te mooy ni mu ko yare, ni mu daan taqoo ak moom, ak ni mu ko gërëmee. Al-Habdul Xadiim Grenoble, 08/04/2020.
Fii danu fiy àndi lenn ci jaar-jaari Ceerno Ibraahima Faati. Lu mel ni ki judoom, ay jikoom, digganteem ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu, miy magam di lépp. Niki noonu dees na fi jukki ay bataaxel yu ko Sëriñ bi bindoon. Yal nanu Yàlla fayal Borom Daarul Muhti.