Bismillahi Rahmaani Rahiim Dees na xamee ci néttali yi nu fi dajale njariñal dëddu ak fexe xam bu wér ñi àdduna di wore.
Su ko defee ab soññee la ci nit ki mu wara xam lim war a gën a fonk ci dundam ak ci doxiinam. Té loolu moo di fexee dundal sa ruu, sàmm say jëf , di def li Yàlla gëram te koy sellal. Ndax bàmmeel kat loolu moo fay njariñ. Nit ki wara man a xam itam lu ko ay mbokkam manal ak fa ñu man a yem. Lu ko alalam manal ak lu mu manalul ak fu yaramam di myjjee.
Yalla nanou yalla deffal degg ak topp. Diadieuf Mouride