Tombi Borom Tuubaa (9)

Bismillahi Rahmaani Rahiim

Fii danu fiy béral lenn ci waxi Sëriñ bi ci Xasiida yi. Lu mel ne ki Nuuru Daarayni ak Muqadimatul Amdaah. Muy ay néttali yoy dina soññi képp kuy góor-góorlu ci Xasiida yi mu yokk ay jéegoom. Ndax njariñ li nekk ci Xasiida yi rey na lool.

Mat naa fonk lool, di ko saytu, di ko yittewoo. Di bindaat Xasiida yi, di ko topp bu baax, di ko jàng, di ko durus muy sax, di ko yékkati ci jàng mu neex moo xam yaw kepp walla cig kureel. Di ci fàggu, di ci maye, di ko yaatal, di ko déglu, di ko denc.

Yal nanu Yàlla dolli tawfeex ci Xasiida yi Barkeb Boroom Tuubaa.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR