
Ni Sëriñ bi daan jaamo Yàlla, la nu fiy béral. Anam gi mu daan jàngee Alxuraan, fonkeel gi, ak baril lu mu key jàng, waxtu yi mu daan bind, ay naafilaam ci ay ràkka, yooyu dees na fi fésal dara.
Naka noonu mellom moom ci bind, ay xeeti waxam ak jëfinam, ay hikmaam ak mbir yu bari te am solo lool ci ab Jullit bu ko xamee.
Sàmmonte gi ci moom, mandu gi, waxin wu refet wi, dal gi, fulla gi ak bëggam Yàlla Subhaanahu ak Yonentam Aleyhi Salaam dana fi feeñ itam.
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien