Xaaj wi dees na fi xamle diggante Sëriñ bi ak Alxuraan. Ak ni mu daan yittewoo gone yi di jàng Alxuraan. Daf daan teral Alxuraan, ak di ci déggee ay mbiram, di ci dalal xelu ab taalubeem.
Di xamle itam yenn ci mbóot yi ci aaya yi. Di leeral itam ay aaya ci anam gu yéeme, gu neex a dégg, neex a xam. Di bindlu ay Kaamil ak di ko fàggu.
Di tontu ay nit ci Alxuraan ak di ci yare ak a jàngale. Te sax moom nee na njariñul Alxuraan mi ngi ciy yoxoom.
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien