Tombi Borom Tuubaa (20)

Fii di neen fi leeral njariñal topp ndigal ak yitewoo njub. Dees na fi fésal itam ni léppi Sëriñ barkeele ak ni Yàlla di nangoo ñaanam. Xar-baaxi Sëriñ Tuubaa itam cig mbindam ak i jagleem ak ni mu daan taxawoo taalube yi dees na ko fi xamee itam. Naka noonu ni Sëriñ bi xamee mbiri […]

Tombi Borom Tuubaa (19)

Dog wi deef na fi àndi itam lenn ci xar-baaxi Sëriñ bi, lenn ci yi ko Yàlla may ak lenn ci ay hikmaam Naka noonu da nga fi dégg ay hisa yuy wone ni am na it ñu ko daan jéem a natu ci anam yu kéemaane. Ak ni mu daan delloo lépp ci Yàlla. […]

Tombi Borom Tuubaa (18)

Fii dees na fi wone lenn ci màndargay yërmandey Sëriñ bi ak ñi mu daan sàmme kollare. Ni mu wàccoog nun itam ci wax, ci jëf ak ci bind. Ak ni mu defoon ragal Yàlla muy lépp. Naka noonu dees na fi leeral yennet ci xisa yuy wone xar-baaxi Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara […]

Tombi Borom Tuubaa (17)

Ci xaaj wi dees na fi xamle itam leen ci Sëriñ bi, ni ki mbir yum baaxowoon def ak bis yu mu ko daan def. Ni mu fonkewoon julli ci waxtu, ak ni mu daan sàmmee taalube yi. Ba tay, dees na fi wone ni mu doone ki nuy cinu ak di nu musal di […]

Tombi Borom Tuubaa (16)

Ni Sëriñ bi daan jaamo Yàlla, la nu fiy béral. Anam gi mu daan jàngee Alxuraan, fonkeel gi, ak baril lu mu key jàng, waxtu yi mu daan bind, ay naafilaam ci ay ràkka, yooyu dees na fi fésal dara. Naka noonu mellom moom ci bind, ay xeeti waxam ak jëfinam, ay hikmaam ak mbir […]

Tombi Borom Tuubaa (15)

Tay nag kàddu yi daa jëm ci waxi Sëriñ bi ci mag ñi niki Maam Cerno, Seex Ibraahima Faal, Maam Seex Anta, Sëriñ Daaru Asan Njaay, Sëriñ Abdu Karim Ture… Dina fi feeñee itam seen i jagle yu réy ci Sëriñ bi. Seenug baax, seenug jàmbaar, seen i jikko yu refet, seen doggu ak seen […]

Tombi Borom Tuubaa (14)

Bismillahi Rahmani Rahiim Dees na leeral ci xaaj wi mbiri àddiya, dolle gi mu am ak ay njariñam. Di na fi feeñee itam tabeeg Sëriñ bi. Naka noonu dees na fi béral waxi Sëriñ Tuubaa ci ay taalubeem ak ñi mu àndeek ñoom, naka noonu wuute yi am ci taalube yi ci seenug daraja ak […]

Tombi Borom Tuubaa (13)

Bismillahi Rahmani Rahiim Ci xaaj wi deef na fi leeral, solos màggal gi fa Boroom Tuubaa, dayyob cant gi kawe na, yékkati ku na, te yooll yi bari. واجعل طعامي و شرابي يا كريم ذكرا و شكرا و ثوابا لا يريم « Yaw Yàlla mu tedd mi Yàlla nga def samaw ñam ak samag naan muy […]

Tombi Borom Tuubaa (12)

Bismillahi Rahmani Rahiim Ci xaaj wi nag deef na fi fesal ne Sëriñ bi daan soññee ci fonk julli guddi, ci feggu ak ci sàmm sa ngëm. Deef na fi leeral yeneeni mbir jëm ci gëram sa Soxna. Sëriñ bi it jagle yu réy yi mu amoon. Naka noonu ay waxam ci Tuubaa, ak ni […]

Tombi Borom Tuubaa (11)

Bismillahi Rahmani Rahiim Fii nag dees na fi leeral njariñu garabi wolof. Yenn gañcax yi nga xam ne daa baax lool ci wér gu yaram. Am na ci yu nuy baxal di naan, yii nu key segg ci ndox mu tàng. Su ko defe Sëriñ bi daf fiy xamle njariñ yi nekk ci garab yooyu, […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR