Bismillahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw leeral lu aju ci natuwaayu xisa yi. Deen fiy yaayal waxtaani Sëriñ Tuubaa walla Tombi Boroom Tuubaa. Sëriñ Alhaaji Mbàkke moo bind Téere bi. Di ko ñaanal mu yàgg fi lool te wér. Yàlla dolli ko kàttan ak man-man ci lépp. Su ko defe saa bu àndee benn xisa rekk day […]
Bismillaahi Rahmaani Rahiim Dénkaane bi mooy sunu xaaj bu mujj ci dénkaaneey Sëñ Alhaaji. Noo ngi key ñaanal Yàlla sàmm ko, guddal fanam, may ko wér, xéewal yu yaatu te barkeel, defal ko ngëramal Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaaralahu Fii nag dafay soññee ci nu góor-góorlu ci yittewoo nees di njariñoo ci Sëriñ Bu […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu matale, la daaldi soññee ci jaamu Yàlla, ak ngëm gu sell ci ne Yàlla ci boppam moo nu gàddul sunug dund. Naka noonu mu fàttali ñépp ne, Diiney Lislaam ñor na lool sunu Boroom, te loolu dafay tegtal Yonent yi mi fi yabal. Dineey Muhammad Salla Laahu tahaala aleyhi […]