Bismillahi Rahmani Rahiim
Fii nag dees na fi leeral njariñu garabi wolof. Yenn gañcax yi nga xam ne daa baax lool ci wér gu yaram. Am na ci yu nuy baxal di naan, yii nu key segg ci ndox mu tàng.
Su ko defe Sëriñ bi daf fiy xamle njariñ yi nekk ci garab yooyu, seen i jeexital ci wér gi yaram. Ak yeneeni mbóot yoo xam ne du kum neex rekk xam ko.
Yal nanu Yàlla sàmm, guddal sunuy fan, may nu wér ba fàww barkeb Seexul Xadiim.
Assalaamou aleikoum Al-habdul Xadiim,
Dieuredieuf si yaatal gui ak dellouway yi nga fi rotal. Amna solo Lool.
Laath bi ma am moy: mbolem garab yi ngen fi toudou mòk café ndax Serigne bi tamou wone nasi waxtou boum kay dieufandiko ak si ñata lim la tollone ?
Dieuredieufati
Daan na wax daal bu leen boole café ak ataaya. Na soree !
Ci misaal boo naane café si suba si. Ngoon ngi man nga naan ataaya.Taxul nag ma xam ba xam amoon na ci li lim.
Dello siyaar bu baax nag !