Sëriñ Tuubaa nee na » Ca gaal ga la ma Yàlla xamalee ne kuy liggéeyal Yonent bi laa. Foofu it laa taggee Yonent bi tagg wuy sax di ko fekk fa mu ne » .
« Fa Conakry, Yàlla setal na ma ci lépp luy jëme ci lu ñaaw, fegal ma ko. Tagg naa fa Yonent bi it (Alayhi Salaam), te moom gindi na ma ba duma réer bi izni Laahi ».
« Ca Grand-Bassam la ma Yàlla dàqalee samab noon, gindi ma fa ci tag gi may tag Yonent bi (Alayhi Salaam) fegal ma fa ag faatu ci atum 1313 »
« Tagg gi ma doon tagg Yonent bi (Alayhi Salaam) fa Libreville, Yàlla defal na ma ci lu wenn Waaliyu amul, te Waaliyu wu nekk bëgg ko ».
» Àgg naa ci Yàlla fa dëkkub Galwaa* yi, mu fegal ma lépp luy yóbbe balaa. Nekk gi na nekk liggéeykatu Yonenti bi ma fegal balaa, tiis na saytane foofu, lool lool ».___*Galwaa, wala Galoa aw xeet la niti Gabon, Lambaréné mooy seen dëkk.
Al-Habdul Xadiim
24/09/2021.