Ñaari Bataaxel Fa Cerno Ibraahima (11)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Maa ngi lay nuyu yaw Ibraahima, te di la xamal ne da maa bëgg nga dimbali  »Muhammad » ci aajoom ndax loru na lool. Saa soo gise bataaxel bi na nga ko béggal loo mën. Maa ngi ñaan Yàlla sunu Boroom àdduna bañ noo wor. Mbooleem ñi aju ci man na nga leen […]

Waxi Sëriñ Tuubaa ci Seex Fàddilu Mbàkke

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu maxtaara lahu mas naa wax Sahiid Mbàkke : Mas ngaa gis ku mel ne Fàddilu Mbàkke mu ne ko déedeet ? Mu ne ko mas nga dégg ku mel ne Fàddilu Mbàkke? Mu ne ko déedeet. Sëriñ bi ne ko Sahiid Mbàkke doo ma laaj sax lu […]

Daaju Xasida (4)

Leeral u Sëriñ Saaliwu Mbàkke radiya laahu anhu ci daaju mag ñi. Sëriñ Abo Jaxate jëwrinu kurel Daaru Salaam- Xelkom, bokkoon ci ñi daan jàngal ku baax ki moo ko def. Daan ko jàngal fa Njurul ak fa Njaaréem. Daan na jàng itam kër Soxna Faati Ja moom ak kurelam. Fii nag leerali Sëriñ Saaliwu […]

Dénkaane bu jëm ci Murid yëpp (10)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. « Maa ngi leen di dénk topp Yàlla te bañ a noonoo, deeleen soppante ci Yàlla te bañ a xëccoo, bañ a réeral kenn. Soppante ci Yàlla mooy ag ngëm, ku ko def dangay am mbégte ak Kóolute ; iñaanante nag ñu ko def cig texeedi rekk la leen jëme. Jikko ji gën […]

Bataaxel bu jëm ci Sëñ Masàmba kaani Buso (9)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Maa ngi lay nuyu yaw mi nga xam ne sag leer dafa bari ba nga set wecc ngir topp gi nga topp diine, yaw sama xarit bi ñu wax ne Yàlla daf koo xajal boppam ba mujj mu noot ko. Lii laa lay dénk deel topp ndigali Yàlla yi, tey daw ay […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR