Ngëneeli koor (3).

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Bokk na ci li nuy sopp ci Ramadaan naafila yi. Li gën a rafet mooy Fukki ràkkaa ak ñaar (12), daa di wiitar. Képp ku mokkal Alxuraan te amul ngànt na jàng lumu man ci ràkkaa yooyu. Ku matal lim bii ba noppi, man naa dolli lu ko neex ci naafila yi […]

Ngëneeli koor(2)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Bokk na ci ngëneeli koor, ku woor bu de jàpp ndox mi da koy ñaanal sunu Boroom Subhaanahu wa Tahaala setal ko ci ay bàkkaar, bu taxawe di julli néeg bi da koy ñaanal sunu Boroom Subhaanahu wa Tahaala leeral bàmmeelam yaatal ko. Bu boobaa nag, sunu Boroom Subhaanahu wa Tahaala da […]

Ngëneeli koor(1).

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Nee nañu képp ku teewe jotaayu sikkar ci Ramadaan, sunu Boroom dana ko bindal ci bépp jéego jaamug am at. Te bu ëllëgee ci kerug aras lay toog ànd ak Yónnent bi salla laahu aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama . Képp kuy taqoo jullig mbooloo ci Ramadaan, sunu Boroom Subhaanahu […]

Juróomeelu Bataaxel Fa Seex Ibra Faati(13).

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Li ma lay xamal mooy nga togg ci barab bi nga nekkoon njëkk may génn, te bañ a déglu waxi nit ñi nga xam ne dañuy njort te duñu xam. Amna bayit yu ma defoon fan yii ci kër Seex Siidiya, mooy :<< Ku jublu Yàlla sunu Boroom noppalu, noppal keneen. Ku […]

Yarug Cerno Ibraahima ak ngërëm la ca topp

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Fii danu fiy xamle ni Sëriñ bi daan jëflante ak Maam Cerno, te mooy ni mu ko yare, ni mu daan taqoo ak moom, ak ni mu ko gërëmee. Al-Habdul Xadiim Grenoble, 08/04/2020.

Ñeenteelu Bataaxel jëm ci Maam Cerno(12)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. « Asalaamu haleykum wa rahmatula wa tahaala wa barakaatahu, ginnaaw nuyoo bi, boo gise bataaxel bi, na nga yabal ku mokkal Alxuraan koo xam ne, gone lay doon, mu ànd ak ñaari moroomam, ndax ñu man a jàngal gone yi nekk fi, te yabal ñatti waxambaane yu man a jàngale xam-xam, ndax […]

Maam Cerno géejug njariñ.

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Nu fas yéene jukki leen ci hikma yi Borom Daarul Muhti daan wax. Li nu fiy nettali nag ci Sëriñ Xalil Mbàkke mu Sëñ Mustafaa Afsa lanu ko toxale. Al-Habdul Xadiim Grenoble, 01/04/2020.

Ñaari Bataaxel Fa Cerno Ibraahima (11)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Maa ngi lay nuyu yaw Ibraahima, te di la xamal ne da maa bëgg nga dimbali  »Muhammad » ci aajoom ndax loru na lool. Saa soo gise bataaxel bi na nga ko béggal loo mën. Maa ngi ñaan Yàlla sunu Boroom àdduna bañ noo wor. Mbooleem ñi aju ci man na nga leen […]

Waxi Sëriñ Tuubaa ci Seex Fàddilu Mbàkke

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Sëriñ Tuubaa Xaada lahu laahu maxtaara lahu mas naa wax Sahiid Mbàkke : Mas ngaa gis ku mel ne Fàddilu Mbàkke mu ne ko déedeet ? Mu ne ko mas nga dégg ku mel ne Fàddilu Mbàkke? Mu ne ko déedeet. Sëriñ bi ne ko Sahiid Mbàkke doo ma laaj sax lu […]

Daaju Xasida (4)

Leeral u Sëriñ Saaliwu Mbàkke radiya laahu anhu ci daaju mag ñi. Sëriñ Abo Jaxate jëwrinu kurel Daaru Salaam- Xelkom, bokkoon ci ñi daan jàngal ku baax ki moo ko def. Daan ko jàngal fa Njurul ak fa Njaaréem. Daan na jàng itam kër Soxna Faati Ja moom ak kurelam. Fii nag leerali Sëriñ Saaliwu […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR