Ku amoon gis-gis bu sori la. Dafa teel a yeewu ci doxiinu jamono. Moo tax masul neenal benn xam-xam bu am njariñ. Dafa daan yóbb ay nit ñu bari ñuy jàngi ci yeneeni réew. Teewul itam mu sàmp ay jàngukaay ci biir Senegaal. Tuubaa itam mu liggéey mbed yi, def ci liggéey mu am solo […]