Fii danu fiy leeral ni, jàng xam-xam dëgg-dëgg, ci ndaw lañu koy gën a manee. Njariñu xam-xam ci nit, dayoom gi ak i jeexitalam réy na lool ci ku jóg sóobu yoonu xam. Yal nanu Yàlla xiir ci sàkku lu nuy njariñ ci àdduna ak fa allaaxira te lépp dëppook bëggug sunu Boroom ak ngëramam […]
Fii danu fiy àndi lenn ci jaar-jaari Ceerno Ibraahima Faati. Lu mel ni ki judoom, ay jikoom, digganteem ak Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu, miy magam di lépp. Niki noonu dees na fi jukki ay bataaxel yu ko Sëriñ bi bindoon. Yal nanu Yàlla fayal Borom Daarul Muhti.
Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu daa soññee lool ci tabe, teral gan ak yaatal ko. Mu fiy wax lu tax loolu di lu manul ñàkk ak xéewal yi ci nekk ak ngëneel yi. Di wax it solos xam-xam, tolluwaay wu réy gi ma am fa sunu Boroom. Di leeral ne ndamoo ay askan […]
Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu daf nu fi dénk jàng, liggéey ak sàmm sunu diine. Dina fi leeral itam, moom Sëriñ bi, lu jëm ci ay mbiram niki wirdam, Sëriñam, yoonu géej gi ak yeneeni mbir. Naka noonu dees na fi déggee lenn ci ay jagleem ak i xéewalam. Yal nanu Yàlla xir […]
Sëriñ Tuubaa dina fi leeral leen ci baati wolof yi ak mahnaa gi ñu ko wara jox dëgg-dëgg. Lenn ci xarbaax yi itam dees na feeñee fi. Naka noonu Hikma yi.Ba tey ci néttali yi di neen fi dégg luy waral nu wara gën a sàmm sunu kolare ak Sëriñ Tuubaa, sunu diggante ak moom […]
Fii dañu fiy fésal ni Sëriñ wéetale Boroomam ak liggéey gu muy liggéeyal Yonent bi Aleyhi Salaam ak ni mu key feeñale ci mbindam. Naka noonu sunu Borom dig na ko lu réy ëllag ginnaaw jaamu Yàlla ju refet gi mu jaamu Boroomam ak jaayanteem ju réy ji.
Di neen fi béral lenn ci dooley mbidum Sëriñ Tuubaa, njariñ yi mu làmboo ak jagle yi ak barkeb mbindam. Naka noonu lenn ci mayi Sëriñ bi dees na ko fi fésal, ci man a xeetali mbindéef yi, fuñu man a nekk. Dees na fi dégg it nettali yoy dees koy gëm waaye deesuko xam. […]