Seex Muhammadu Lamin 1886 la gane àddina. Yonent bi AleyhiSalaam la ko baayam tudde. Soxna Haanatu Jóob mooy way-juram wu jigéen. Sëriñ Tafsiir Ahmadu Jóob mooy baayam mi ngi dëkkoon Dagana. Wollare Sëriñ Tuubaa la woon, moo ko jébbal itam Sëriñ Muhammadu Lamin ak mbolleem njabootam. Seex Muhammadu Lamin it ku amoon hikma la. Daan […]
Sunu sang bi turam dëgg mooy Muhammadul Amiin, ñu duppee ko Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke miy doomi Sëriñ Tuubaa. Sëriñ El Haaji Baara nag mi ngi gane àddina atum 1921 fa Ndidi. Baayam moo di Sëriñ Fàllu Mbàkke, ndeyam di Soxna Xari Sàll. Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ko Sëriñ Moor Sànqe, ginnaaw […]
Sëriñ Siidi Maxtaar, Sëriñ Baara Mbàkke ak Soxna Mati Ley ñooy ay way-juram. Mi ngi gane àddina atum 1925 fa Mbàkke Kajoor. Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ku turondoom Sëriñ Seex Awa Bàlla waaye mi ngi mokkale Alxuraan ci kenn ci taalibey Sëriñ Baara ñu di ko wax Sëriñ Ñaan Jóob. Bi mu noppee […]