Kan Mooy Sëriñ Abdullaahi Mbàkke

Sëriñ Abdulaahi ku taqoowoon la ak baayam ju baax ji, nuru ko lool ci mello. Mootax Seex Musaa Ka nee : « Allaahu moo di jenn waay, moo jàpp doom def ko ni baay ». Wax na it : « boo gisee muy sàmmandaay, Seex Bàmba ñoo nuroo jotaay, nuroo yaram, nuroo sewaay, nuroo doxiin, nuroo waxiin, nuroo […]

Kan Mooy Sëriñ Asan Salaam

…Dafa mel ni li moo doon cëram, mu sawar lool ci dimbali nit ñi. Bi mu toole ci 40i at nag la daaldi fas yéene dimbali ñi fi ne. Di xamle ak a won nit ñi lu leen man a teeqale ak def bàkkar, ak di jëf nangam ci lu baax ngir man a tàbbi […]

Kan Mooy Sëriñ Hamsatu Jaxate

Ba ñiy nekk Ceeyeen-Jolof itam moo yoroon Daaray Kaamil ga foofu. Nekkoon na Njaaréem ci ndigalu Sëriñ bi. Ginnaaw gi nag la ko yabbal Tuubaa mu nekk fa di fa xamle Diine. Sëriñ Hamsatu nag Seexul Xadiim daf ko yar ci pasteef ak daan ko soññi ci doon nit ku mat. Ba ñiy nekk Ceeyeen-Jolof […]

Kan Mooy Sëriñ Moor Mbay Siise

Ñi jaar ci ay loxoom bari neen lool. Bokk na ci Sëriñ Muntaxaa Mbàkke, Sëriñ Mustafaa Saalihu Sëriñ Saalihu Ture. Ku amoon kollare la ak doomi Sëriñ Tuubaa yi, Seex si, ak kilifay yeneen tariqa yi. Amoon tawfeex lool ci Boroomam, di ñaan bu wér muy nangu. Te doyloo woon Sëriñ bi ci bépp soxla.Ku […]

Kan Mooy Soxna Muslimatu Mbàkke

Senghor mi doon njiitu réew mi itam mas na ko sargal, te daf daan wax naan « Soxna Musli dafay jigéen boo xam ne, daa jiitoo lu bari jamonoom ». Soxna Musli ci turam bi gën a siiw, doonoon it ku amug sàmm, bañoon jaxasoo góor ak jigéen. Liggéeyam itam terewuko woon jaamu Yàlla ci […]

Kan Mooy Sëriñ Mbàkke Buso

…Am na benn buur gu féetewoon Lambay dafa sonnaloon lool murid yi ba Sëriñ Mbàkke Buso bindoonko bataaxal di ko wax mu teey loram ci murid yi. Sëriñ Mbàkke Buso it dund na lu metti atum 1895. Ndax ci at moomu la baayam, miy nijaayi Sëriñ Tuubaa, faatu. Demug Sëriñ Mbusoobe tiisoon na ko lool. […]

Kan Mooy Sëriñ Mustafaa Saalih

Daa mel ni wax ji jenn la. Doomi Soxna Mati Jaxate ak Sëriñ Saalihu dem am gi bet na nu. Daf doon murid saadix, te ay kilifaa ko wax, seedeel ko ko. Yal na ko Yàlla dolli xéewal fa mu nekk, yërmande ak i leer te taas nu ci barkeem. Sunu Boroom yal na ko […]

Kan Mooy Sëriñ Mbàkke Madina

Sëriñ Mbàkke Madina, dafa doonoon nit ku fonk jàng, jàngale ak jëfe xam-xam. Doonoon ku fonk sunnas Yonent bi Aleyhi Salaam, di ko dund bu wér. Dafa doonoon ku noppi, am dal lool, bari ñu ko sopp muy kilifa yi di ndogo yi. Mbokkam yépp bëgg ko ak daan ko ndamoo bu wér. Ku dëddu […]

Kan Mooy Gaïnde Fatma

Ku amoon gis-gis bu sori la. Dafa teel a yeewu ci doxiinu jamono. Moo tax masul neenal benn xam-xam bu am njariñ. Dafa daan yóbb ay nit ñu bari ñuy jàngi ci yeneeni réew. Teewul itam mu sàmp ay jàngukaay ci biir Senegaal. Tuubaa itam mu liggéey mbed yi, def ci liggéey mu am solo […]

Kan Mooy Sëriñ Musaa Ka

Moo doon Werekaanu Bàmba, di xamle jaar-jaari yoonu murid, cëslaayiyoon wi ak daan dànkaafu képp kuy dal ci Sëriñ bi mbaa ci yoon wi. Mooy koo xam ne kenn du sosal kenn ci ñoñ yoon wi mbaa boroom yoon wi te mu nekk fi. Mooy délluwaay bu mag bi ci xam melloy SëriñTuubaa, ay jikkoom […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR