Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
« Asalaamu haleykum wa rahmatula wa tahaala wa barakaatahu, ginnaaw nuyoo bi, boo gise bataaxel bi, na nga yabal ku mokkal Alxuraan koo xam ne, gone lay doon, mu ànd ak ñaari moroomam, ndax ñu man a jàngal gone yi nekk fi, te yabal ñatti waxambaane yu man a jàngale xam-xam, ndax ñu man a jàngal waxambaane yi nekk fii. Boo gise bataaxel bi, nañu daaldi ñëw, yaw mi nga xam ne dañu la rendi ci sopp ma. Man mi nga xam ne ku ñu rendi ci sopp ma ku texe la, texe goo xam ne texeedi du ci topp »
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 04/04/2020
Ndeysane weer ba dh. Yalla na yalla yokk xam xam gui barké Cheikhoul Khadim 🙏🏽
Amiin Soxna Jaara santaat neen
Machalah .mouride dafa sara fess del ak kham kham . Tè yagui niouw khamal 🙏🏾
Ndeysaan yal na nu Yàlla bokk xamal, te xiir nu ci jëfe ak seekal Bàrke Borom Tuubaa
Ndaysaan
Hakasaa
Maa sáala amna solo looll
Hakaza santte si fatalimi kawer na
Jërëjëfaat yalla na ngén ci dajé ak ngërëmal Sëriñ bi. Paakap coféel ci sëriñ bi yalla nanu bokk rendi