Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
Bokk na ci li nuy sopp ci Ramadaan naafila yi. Li gën a rafet mooy Fukki ràkkaa ak ñaar (12), daa di wiitar. Képp ku mokkal Alxuraan te amul ngànt na jàng lumu man ci ràkkaa yooyu. Ku matal lim bii ba noppi, man naa dolli lu ko neex ci naafila yi ci biir guddi gi walla bëccëg ndax naafila weeru koor bari na lool ay ngëneel. Naka noonu képp ku woor ci Ramadaan war nay sàmmonte ak jullig mbooloo. Tey taqoo jotaayi Sikar yi, tey topp ay way-juram di leen liggéeyal bu fekkee ñoo ngi dund. Buñu faatoo itam mu leen di ñaanal.
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 09/05/2020.
Jeredieufeuti Mouride. Boul gnou faté si niane
Jaajëfaat bunu fàttante!
Machallah fall yarame
Jërëjëf yal na nu Yàlla dooli njariñ
Yàlla na la sunu Boroom fay ag yiw
Jerejeuf jëwriñ
Jaajëfaat mu boole nu ko.
Jajeuf mouride yalna Serigne bi gueureum liguéy bi
Amiin Amiin
Machaallah
Jërëjëf