Bismillaahi Rahmaani Rahiim Dénkaane bi mooy sunu xaaj bu mujj ci dénkaaneey Sëñ Alhaaji. Noo ngi key ñaanal Yàlla sàmm ko, guddal fanam, may ko wér, xéewal yu yaatu te barkeel, defal ko ngëramal Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaaralahu
Fii nag dafay soññee ci nu góor-góorlu ci yittewoo nees di njariñoo ci Sëriñ Bu Mag Bi te dox ci li nu key may. Te loolu moo di dund Lislaam gu wér ak Taalube gu mat ci gàttal.
Ki ci nataal bi mooy baayu Sëriñ Alhaaji.Sëriñ Mustafaa Habsa Mbàkke mooy turam ci weeru koor wi la fi jóge. Yal na ko Yàlla dooli yërmande, njéggal, xéewal ak ngëram Barkeb Borom Daarul Muhti.
Al-Habdul Xadiim
27/04/2022
S’abonner
0 Commentaires
Le plus ancien