Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
Nee nañu képp ku teewe jotaayu sikkar ci Ramadaan, sunu Boroom dana ko bindal ci bépp jéego jaamug am at. Te bu ëllëgee ci kerug aras lay toog ànd ak Yónnent bi salla laahu aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama .
Képp kuy taqoo jullig mbooloo ci Ramadaan, sunu Boroom Subhaanahu Wa Tahaala dana ko yërëm. Te mel na ne ku Yónnent bi salla laahu tahaala aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama yoral boppam, gàddul ko boppam.
Bokk na ci li war jigéen ci weeru koor muy sàkku ngërëmal boroom këram. Jigéen ju koy def dana am tuyaabay Maryaama ak Aasiyatu alayhimaa ridwaanu laahi tahaala naka noonu di farlu di faj aajoy nit ñi. Ku ciy dox ngir aajoy jullit faju, sunu Boroom Subhaanahu Wa Tahaala dana ko bindal ci bépp jéego juróom ñaar fukki yiw. Faral ko juróom ñaar fukki ñaawtéef. Yónnent bi salla laahu tahaala aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama dëgëral ay tànkam ca siraat.
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 25/04/2020.
Machallah mouride amna solo
Jaajëf ku baax!
Maa shaa jerefeti Mouride. Yalla nanou yalla deffal degg ak topp thi werou bonus bi
Amiin amiin
Machallah fall
Jërëjëf murid
Diadieuf
Jaajëfaat