Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (12)

Bismillaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu matale, la daaldi soññee ci Xasiida yi ngir nu gën koo fonk, gën koo jàpp, gën ci soobu te Yàlla tax. Ginaaw loolu, la daaldi wax luy tax ñu nekk ci ak anam gi ko Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu fonke woon. Yal nanu Yàlla xiir ci […]

Leeral Daaju Muwaahibu 78 (2)

Bismilaahi Rahmani Rahiim Nu dikkaat ak yéen ci beneen tomb jëm ci Daaju Mag ñi. Sëñ Abo Jaxate moo fas yéene leeral fii xeeti riim yi daje ci ñaareelu Daaju 78. Dina fi fàttali itam ni ko Sëriñ Saalihu Mbàkke Radiyallaahu daan bëggee, ba taxoon na sax mu santon ku nuy wax Baay Móodu Gay […]

Leeral Daaju Muwaahibu 78

Bismilaahi Rahmaani Rahiim Sëriñ Abo Jaxate mooy dikkaat ci leeral Daaju Muwaahibu 78, ci ñaareelu tooluwaay wi. Dana fi leeral lu aju ci tontu gi ginnaaw ba ñu daaje ba noppi. Jànginu waa kër Sëñ Abdulaahi Jaxate ca na mu gën a refete dees na ko fi dégg, ak dundalaat ko fi. Yàlla nanu Yàlla […]

Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (11)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim Ginnaaw ba mu nuyoo mbokk yi ak dëkkandoo yi dafa daaldi soññee ci farlu ci lu baax ak jaamu Yàlla ju sax, ak di boole xam ak jëfe. Fàttali fi it lenn ci àddis yi jëm ci sàmm sa bopp ak benn lor kenn. Mu dolli soññee ci farlu ci Jàngum Xasida […]

Leeral Daaju Xasiida (5)

Bismilaahi Rahmani Rahiim Lii ab tënk la jëm ci Taanug Sëriñ Saalihu ci daaj yi ak la mu sasoon ndogo yi ci nu koy jàng. Xasiida yooyu nag siiw na ci seen biir ci aw tur te mooy: « sas wi ». Dina fi tontu ay laaj yu jëm ci fànd woowu, moom Sëriñ Abo Jaxate jëwrinu […]

Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (10)

Bismilaahi Rahmani Rahiim Ginnaaw nuyoo gu matale, la daaldi soññee ci jaamu Yàlla, ak ngëm gu sell ci ne Yàlla ci boppam moo nu gàddul sunug dund. Naka noonu mu fàttali ñépp ne, Diiney Lislaam ñor na lool sunu Boroom, te loolu dafay tegtal Yonent yi mi fi yabal. Dineey Muhammad Salla Laahu tahaala aleyhi […]

Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (9)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Lii ab laabire la bu bàyyikoo ci Sëriñ Alhaaji Mbàkke Xaadimul Xadiim jëm ci fonk julli ci Yonent bi Salla laahu tahaala aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama. Wax na fi loo xam ne dana yokk jullit bi ag sawarte ci gën a fonk Salaatu rawatina di ko jaarale ci Salaatu […]

Yoon Wu Sori Wi(3)

Sëriñ Tuubaa nee na  » Ca gaal ga la ma Yàlla xamalee ne kuy liggéeyal Yonent bi laa. Foofu it laa taggee Yonent bi tagg wuy sax di ko fekk fa mu ne » . « Fa Conakry, Yàlla setal na ma ci lépp luy jëme ci lu ñaaw, fegal ma ko. Tagg naa fa Yonent bi […]

Yoon Wu Sori Wi (2)

Al-Habdul Xadiim15/09/2021

Yoon Wu Sori Wi(1)

« Ku yàkkaar ne sama tukki bii dama cee jëm feen fu dul ci Yàlla ak Yonent bi ba tax mu may dëkk yor jaasi ak i kano, Yàlla dana ko gàcceel, seetaan ko, mbindéef yi dinañu ko ngàññi, yeed ko, mu dee ak gàccee ak toroxtange. Yàlla nag dina ma dimbali far ak man, mbindéef […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR