Dénkaane bu jëm ci Soxna Penda Jóob (8)

Bismilaahi rahmaani rahiim. Sëriñ bi ginnaaw ba mu leeralee ni kuy sàkku Boroomam la ak Yónnentam ba salla laahu tahaala aleyhi bi aalihi wa sahbihi wa salama, la daaldi wane ag jubloom ci dénk soxnas baayam ju ndaw ja, nu naan ko Penda Jóob. Daf ko wax ne: Maa ngi lay diggal yaw soxna si […]

Daaju Xasida (3)

Leeral u Sëriñ Saaliwu Mbàkke radiya laahu anhu ci daaju mag ñi. Sëriñ Abo Jaxate jëwrinu kurel Daaru Salaam- Xelkom, bokkoon ci ñi daan jàngal ku baax ki moo ko def. Daan ko jàngal fa Njurul ak fa Njaaréem. Daan na jàng itam kër Soxna Faati Ja moom ak kurelam. Fii nag leerali Sëriñ Saaliwu […]

Bataaxel bu jëm ci Borom Daarul Muhti (7)

Bismilaahi rahmaani rahiim <<Li ma lay bëgg dénk, ndénkaane la boo xam ne képp kuy moytu ay ñaawteef dina baril sag may. Maa ngi lay dénk xam-xam ak jëfe ak teggiin. Sab xol nanga ko setal ci ay taq-taq kon dinga jiitu sag maas. Deel toroxlu ci say mbokk ngir laabire leen kon dinga mucc […]

Daaju Xasida (2)

Leeral u Sëriñ Saaliwu Mbàkke radiya laahu anhu ci daaju mag ñi. Sëriñ Abo Jaxate jëwrinu kurel Daaru Salaam- Xelkom, bokkoon ci ñi daan jàngal ku baax ki moo ko def. Nu teewlu ko te yaatal ko ngir njariñ li gana yaatu!

Dénkaane bu jëm ci Abdullahi (6)

Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Yaw Abdullahi maa ngi lay dénk nga ragal Yàlla waxtu wu nekk. Boo bëggee mucc ëllëg, làq ag texe. Nanga sellal sab xol, te tàqalikoo ak bidaa, te taqoo ak Sunna, tey fexe sàmmonte ak ndigal yi.Deel ànd ak ñu baax ñi, bul ànd ak ku bon mukk. Deel fexe saafara say […]

Daaju Xasida (1)

Leeral u Sëriñ Saaliwu Mbàkke radiya laahu anhu ci daaju mag ñi. Sëriñ Abo Jaxate jëwrinu kurel Daaru Salaam- Xelkom, bokkoon ci ñi daan jàngal ku baax ki moo ko def. Nu teewlu ko te yaatal ko ngir njariñ li gana yaatu!

Bataaxel bu jëm ci Ahmadu Jóob (5)

Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Boo delloo foo mana nekk na nga ragal Yàlla, te bul bariy wax ak i nelaw ak lekk ak naan. Na ngay moytu nit ñi bu baax, saa suñu la bëggee xëcc jëmme la ci ay caaxaan dawal jëm ci tuddu Yàlla. Bul yaakaar, bul ragal ku dul Yàlla, na nga koy […]

Kan mooy Soxna Ami Seex Mbàkke?

Bismilahi rahmani rahim. « Lii ag tënk la ci dundug Soxna Aminata Seex Mbàkke bintu Sayxil Xadiim » Mi ngi gane àddina Daarul Aaliimil Xabiir ci atum 1922, wayjuram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Faabéy Jóob mi bokk ak Soxna Faati Tuuti Jóob miy wayjuru Sëriñ Murtada lépp. Moom la Sëriñ Umar Faal di wax ca […]

Dénkaane bu jëm ci topp Yàlla (4)

Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Képp koo xam ne yaa ngi sàkku àjjana ci lu dul ngay topp Yàlla sunu Boroom, te yaakar ne danga koo am sab xol leerul, ndax ba laa kenn a man a ngóob day fekk mu farlu woon cim mbay. Lépp loo xam ne da lay gàllankoor ci topp sunu Boroom bàyyi […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR