Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Képp koo xam ne yaa ngi sàkku àjjana ci lu dul ngay topp Yàlla sunu Boroom, te yaakar ne danga koo am sab xol leerul, ndax ba laa kenn a man a ngóob day fekk mu farlu woon cim mbay. Lépp loo xam ne da lay gàllankoor ci topp sunu Boroom bàyyi […]
Bismilaahi rahmaani rahiim. Yaw miy bëgg a xam jaar-jaari mag ñi, kii ab Soxna su tedd la. Cosaanam, njabootam, diggam ak Sàngam ba Seexul Xadiim, lu bari dana la fi leer. Ousmaan kebe mooy ki def waxtaan wi, nga naanal ko guddu fan ak wér, sunu Boroom musal ko te saamal ko boppam, défal ko […]
Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Yaw Aadama Géy boo bëggee leerug sunu Boroom dee ko jaamu. Te bul bokk ci ñiy jaamu jiggéen ñi. Deel wéttalikio sa Boroom tay wut ngërëmam ànd ak di sellal, tay jihaadante ak sa bakkan. Bul def ci sa xol lu dul lu lay jëme ci sunu Boroom. Lépp loo xam ne […]
Bataaxel bu bàyyiko ci Sëriñ bi jëm ci Muxtaar(2).
<<Yaw Muxtaar maa ngi lay dénk nga ragal Yàlla, te ragal Yàlla mooy jëf ndigal te bàyyi tere. Tey baril jëf yu baax, loolu mooy tax nga bari ay njariñ, te jiital allaaxira ci àddina ndax loolu mooy tax nga texe ëllëg, te mooy tax nga am kóolute ëllëg. Sax ga ngay sax ca àjjana […]
Bismilaahi rahmaani rahiim. «Jógal jaamu Yàlla boo ragalee mu faat la loolu mooy tax doo woru ci àdduna, te jiital yéene ndax mooy tax sa yaakaar dëggu. Waaye boo nee danga yaakaar Yàlla ba noppi doo jëf ndigalam doo bàyyi ay téreem kon sa yaakaar dese naa mat. Moo tax mu ne ko bul bëgge, […]