Leeral Nahju (1)

Li mooy tàmbalig Téereb Nahjul Qadaa Al-Haaji.Ubbite gi rekk doy na yóbbalug dund. Dina fi feeñee ay laabire yu am solo ci sax ci jëf lu baax te bañ a taayi. Naka noonu ay wax yu am solo te bari njariñ moo fiy fés. Ay royukaay ci bépp Jullit, te mooy sahaaba yu baax yi. […]

Tombi Borom Tuubaa (16)

Ni Sëriñ bi daan jaamo Yàlla, la nu fiy béral. Anam gi mu daan jàngee Alxuraan, fonkeel gi, ak baril lu mu key jàng, waxtu yi mu daan bind, ay naafilaam ci ay ràkka, yooyu dees na fi fésal dara. Naka noonu mellom moom ci bind, ay xeeti waxam ak jëfinam, ay hikmaam ak mbir […]

Tombi Borom Tuubaa (15)

Tay nag kàddu yi daa jëm ci waxi Sëriñ bi ci mag ñi niki Maam Cerno, Seex Ibraahima Faal, Maam Seex Anta, Sëriñ Daaru Asan Njaay, Sëriñ Abdu Karim Ture… Dina fi feeñee itam seen i jagle yu réy ci Sëriñ bi. Seenug baax, seenug jàmbaar, seen i jikko yu refet, seen doggu ak seen […]

Kan Mooy Sëriñ Siidi Muxtaar Mbàkke

Sëriñ Siidi Maxtaar, Sëriñ Baara Mbàkke ak Soxna Mati Ley ñooy ay way-juram. Mi ngi gane àddina atum 1925 fa Mbàkke Kajoor. Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ku turondoom Sëriñ Seex Awa Bàlla waaye mi ngi mokkale Alxuraan ci kenn ci taalibey Sëriñ Baara ñu di ko wax Sëriñ Ñaan Jóob. Bi mu noppee […]

Tombi Borom Tuubaa (14)

Bismillahi Rahmani Rahiim Dees na leeral ci xaaj wi mbiri àddiya, dolle gi mu am ak ay njariñam. Di na fi feeñee itam tabeeg Sëriñ bi. Naka noonu dees na fi béral waxi Sëriñ Tuubaa ci ay taalubeem ak ñi mu àndeek ñoom, naka noonu wuute yi am ci taalube yi ci seenug daraja ak […]

Tombi Borom Tuubaa (13)

Bismillahi Rahmani Rahiim Ci xaaj wi deef na fi leeral, solos màggal gi fa Boroom Tuubaa, dayyob cant gi kawe na, yékkati ku na, te yooll yi bari. واجعل طعامي و شرابي يا كريم ذكرا و شكرا و ثوابا لا يريم « Yaw Yàlla mu tedd mi Yàlla nga def samaw ñam ak samag naan muy […]

Tombi Borom Tuubaa (12)

Bismillahi Rahmani Rahiim Ci xaaj wi nag deef na fi fesal ne Sëriñ bi daan soññee ci fonk julli guddi, ci feggu ak ci sàmm sa ngëm. Deef na fi leeral yeneeni mbir jëm ci gëram sa Soxna. Sëriñ bi it jagle yu réy yi mu amoon. Naka noonu ay waxam ci Tuubaa, ak ni […]

Tombi Borom Tuubaa (11)

Bismillahi Rahmani Rahiim Fii nag dees na fi leeral njariñu garabi wolof. Yenn gañcax yi nga xam ne daa baax lool ci wér gu yaram. Am na ci yu nuy baxal di naan, yii nu key segg ci ndox mu tàng. Su ko defe Sëriñ bi daf fiy xamle njariñ yi nekk ci garab yooyu, […]

Tombi Borom Tuubaa (10)

Bismillahi Rahmani Rahiim Deef na fi feeñal fonkug Sëriñ ci teerey xam-xam yi, rawatina yi jëm ci Tawhid ak Tasawuuf. Naka noonu ni mu daan tarbiyaa ay ñoñam ci xiif bu gudd fa Gànnaar. Sëriñ bi it di leen xirtal ci am ay teggin, di joxe te Yàlla rekk tax ak wormaal mbolleem ku sunu […]

Tombi Borom Tuubaa (9)

Bismillahi Rahmaani Rahiim Fii danu fiy béral lenn ci waxi Sëriñ bi ci Xasiida yi. Lu mel ne ki Nuuru Daarayni ak Muqadimatul Amdaah. Muy ay néttali yoy dina soññi képp kuy góor-góorlu ci Xasiida yi mu yokk ay jéegoom. Ndax njariñ li nekk ci Xasiida yi rey na lool. Mat naa fonk lool, di […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR