Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
Li ma lay xamal mooy nga togg ci barab bi nga nekkoon njëkk may génn, te bañ a déglu waxi nit ñi nga xam ne dañuy njort te duñu xam. Amna bayit yu ma defoon fan yii ci kër Seex Siidiya, mooy :<< Ku jublu Yàlla sunu Boroom noppalu, noppal keneen. Ku jublu ku dul Yàlla sunu Boroom sonnal boppam, sonnal keneen. Booy wut noflaay wut ko ci jublu sunu Boroom mi nga xam ne ku ko jublu mu yéwénal mbiram. Ku jublu Yàlla sunu Boroom mu dëggal yaakaaram, kon jublu ko te dëggal >>.
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 18/04/2020.
« Ku jublu Yàlla sunu Boroom noppalu » lou ame solo mom rek ka mata jublu 🙏🏾
Wallaahi Soxna Astu
Lu am solo Mouride
Jërëjëf yal na nu Yàlla defal dégg ak topp
Macha Allah Seriñ Cheikh. Amna Solo loolu. Cela est en phase avec la parole de Imam GHAZALI qui dit que celui qui n’a de crainte révérencielle qu’à l’endroit de l’Unique n’aura pas peur d’une quelconque créature. Par contre celui qui craint un autre que l’UNIQUE, aura le coeur tiraillé et blindé de doutes. Il aura peur de plusieurs choses à la fois. Alors qu’il est plus aisé d’avoir peur à un seul Être. C’est par là que procède la tranquillité du cœur.
Macha’allah! Une ntervention très pertinente qui nous invite à méditer davantage sur ce qui nous lie avec Allah SWT.
Jërëjëf yàlla nanu yàlla def ñu doon i murid yu mel ni sëriñ bi bëgg
Amiin loolu de mooy li mat a sàkku.