Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
Maa ngi lay nuyu yaw mi nga xam ne sag leer dafa bari ba nga set wecc ngir topp gi nga topp diine, yaw sama xarit bi ñu wax ne Yàlla daf koo xajal boppam ba mujj mu noot ko.
Al-Habdul Xadiim,
Lii laa lay dénk deel topp ndigali Yàlla yi, tey daw ay terem ndax màqaama mu ne am na mu ko féete kaw. Deel jihaad ak sa bakkan tey muñ, te bul déglu waxi nit ñi, doxal rekk jëm ci Yàlla te bu leen gestu. Saa su la Yàlla defale xéewal sant ko. Boo amee aw tiis nga muñ. Gestu mbindéef yi ci dara nag, kiiraay la yuy dox diggante murit bi ak Boroomam. Man nag du ma la fàttee ñaanal ci Yàlla ngir mu may la aw yiiw.
Grenoble, 08/03/2020.
Jerejef Bay Cheikh ,. Dénkaané bi dei, kouko deg rk na Jap née mom lako serign bi denk.
Yalla naniou Yalla défal deg ak top ,sax ci ndiagal ba fawwu
Amiin Bàrke Borom Tuubaa
MachaAllah Dieureudjefaty 🙏🏾
Jaajëfaat Soxna Astou
MachaAllah amna solo lolou yalla naleu sounou Borom geun djapalé tek la loxo tei yokk xamxam gui Barké weerou Radjab gui .
Amiin Barke Boroom Tuubaa yalna Yàlla nangu ñaan te boole nu ko.