Ci xaaj wi dees na fi leeral teggin yi war diggante Taalube bi ak Sëriñ bi. Njariñ li nekk ci topp Sëriñ bu mat Sëriñ. Ni mu lay defare, ni mu lay dimbale ak ni mu lay taxawoo sa diggante ak sa Boroom. Sëriñ bi itam dina fi leeral dëgg-dëggi xarit ak mbokk mu baax. […]
Fii danu fiy leeral ni, jàng xam-xam dëgg-dëgg, ci ndaw lañu koy gën a manee. Njariñu xam-xam ci nit, dayoom gi ak i jeexitalam réy na lool ci ku jóg sóobu yoonu xam. Yal nanu Yàlla xiir ci sàkku lu nuy njariñ ci àdduna ak fa allaaxira te lépp dëppook bëggug sunu Boroom ak ngëramam […]
Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu daa soññee lool ci tabe, teral gan ak yaatal ko. Mu fiy wax lu tax loolu di lu manul ñàkk ak xéewal yi ci nekk ak ngëneel yi. Di wax it solos xam-xam, tolluwaay wu réy gi ma am fa sunu Boroom. Di leeral ne ndamoo ay askan […]
Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu daf nu fi dénk jàng, liggéey ak sàmm sunu diine. Dina fi leeral itam, moom Sëriñ bi, lu jëm ci ay mbiram niki wirdam, Sëriñam, yoonu géej gi ak yeneeni mbir. Naka noonu dees na fi déggee lenn ci ay jagleem ak i xéewalam. Yal nanu Yàlla xir […]
Sëriñ Tuubaa dina fi leeral leen ci baati wolof yi ak mahnaa gi ñu ko wara jox dëgg-dëgg. Lenn ci xarbaax yi itam dees na feeñee fi. Naka noonu Hikma yi.Ba tey ci néttali yi di neen fi dégg luy waral nu wara gën a sàmm sunu kolare ak Sëriñ Tuubaa, sunu diggante ak moom […]
Fii dañu fiy fésal ni Sëriñ wéetale Boroomam ak liggéey gu muy liggéeyal Yonent bi Aleyhi Salaam ak ni mu key feeñale ci mbindam. Naka noonu sunu Borom dig na ko lu réy ëllag ginnaaw jaamu Yàlla ju refet gi mu jaamu Boroomam ak jaayanteem ju réy ji.
Di neen fi béral lenn ci dooley mbidum Sëriñ Tuubaa, njariñ yi mu làmboo ak jagle yi ak barkeb mbindam. Naka noonu lenn ci mayi Sëriñ bi dees na ko fi fésal, ci man a xeetali mbindéef yi, fuñu man a nekk. Dees na fi dégg it nettali yoy dees koy gëm waaye deesuko xam. […]
Fii danu fiy àndi ay leeral ci teggini sàmm say gët, worma gi nu wara wormaal mag ñi. Ci bu nu tooge ak ñoom, bu nu àndee ak ñoom ci tukki, bu nuy lekkandoo ak ñoom ak yeneen. Njariñul wax dëgg, ay jeexitalam ak dayo gi am fa Yàlla.
Fii Sëriñ Alhaaji daf fiy leeral dénkaaney Sëriñ Tuubaa ci sàmm sa bopp, am kersa ak di wormaal nit ñi. Njariñul nuyoo, teggini nuyoo ak ay jeexitalam dees na ko fi fésal. Naka noonu yar say gët, màndu, xam kooy àndal, xam kooy roy dina fi leere. Ay wax yu am solo te bari ngariñ […]
Ci xaaj bi, dees na fi àndi lenn ci yi Sëriñ bi daan wax ci bisu penc ak may yi ko fa Yàlla jagleel. Ni miy xéttale nit ñi ci àdduna noonu it la leen di xéttale ëllag. Naka noonu di neen fi béral lenn ci dénkaane yi itam ak njariñ yu réy yi ñu […]