Bismilaahi Rahmani Rahiim. Di nga fi dégge mbir yu yéeme ci Xasida yi. Ndekke dafay yëngal xolu Yónnent yi ak Malaayika yi aleyhimu salaam, di tiital saytane ak di ko gàcceel, di bégal ñi koy jàng ak ñi koy déglu. Al-Habdul Xadiim17/11/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Noo ngi fas yéene wéyal liggéey bi ci Xasida yi nga xam ne ñooy karaamay Sëriñ bi, batey ci lay waxe lu bari ci ay mayam ak ay jagleem. Xasiida yi nag di jariñ lool ki koy jàng. Al-Habdul Xadiim 10/11/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim Jaar-jaari Yónnent bi (Saws) – 3 Fii di nga fi xamee leen ci pexe yi nga xam ne yéefar yi daan nañu ko fexeel Gën ji mbindéef. Da naa fi wax fi itam faatug Aamina ak Abdul Mutalib. Yoonu Saam ak li fa feeñ ci xarbaax. Jambarug Soxna Xadiija ci tambalig Wahyu […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim Jaar-jaari Yónnent bi (Saws)-2 Ba Yónnent bi ganee àddina kiimaan yi fa xew ak xéewal yi mu indaale. Mbir yi amoon ci bañu xaree Dënam gu seel gi, ba tey itam leen ci turam yu seel yi te neex, di nga ko fi dégge insàllaa. Al-Habdul Xadiim 27/10/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim Jaar-jaari Yónnent bi (Saws) Di nga fi xame maami Yónnent bi. Jikkoy Abdul Mutalib ak Abdulaahi itam dees na ko fi xamee Al-Habdul Xadiim 26/10/2020
Bismilaahi Rahmani Rahiim. Kon nu wéyal ci mayi Sëriñ bi cig mbidam mba yi mu ñaan Yàlla sunu Boroom defal ko ko ci. Ànd ak nu xam ne léppam la sunu Boroom nangu. Al-Habdul Xadiim 26/09/2020
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Nu fas yéene béral leen ci bayit yi nga xam ne dafay wone mayug Sëriñ bi ak li ko Yàlla defal cig mbidam ak li muy njariñ ki ciy yëngu. Su ko defe lépp mi ngi ci Nahjul Xawiim mu Sëriñ Alhaaji Mbàkke Xaadimul Xadiim. Tay nag nu fas yéene yaatal bayyit […]
Bismilaahi Rahmani Rahiim. » Maa ngi leen di dénk xam, ak jëfe ak tegginu te bàyyi fo. Xam-xam saa su ne luy bégloo lay àndi waaye réer luy lor rekk lay àndi. Ñàkk teggin nag day waral sori Yàlla. Ñàkk jëfe li nga xam day waral alku. Barim po day xañe ay yiiw.Kon deeleen farlu […]
Bismilaahi Rahmaani Rahiim. • Lu màgg danu koy màggal: wa man yuhasim hurumaati laahi fahuwa xayrulaa inda rabihim ●Laaj bu réy bi nag mooy kañ la? Sunu Boroom ni mu nëbbe ismulaahil ahsam, ak julli gi gën a Tedd ci julli yi la ko nëbbe ngir bëgg nu farlu. Waaye umpalewunu ni sunu Borom xamalon […]