Leeral Nahju (5)

Fii danu fiy àndi ay leeral ci teggini sàmm say gët, worma gi nu wara wormaal mag ñi. Ci bu nu tooge ak ñoom, bu nu àndee ak ñoom ci tukki, bu nuy lekkandoo ak ñoom ak yeneen. Njariñul wax dëgg, ay jeexitalam ak dayo gi am fa Yàlla.

Leeral Nahju (4)

Fii Sëriñ Alhaaji daf fiy leeral dénkaaney Sëriñ Tuubaa ci sàmm sa bopp, am kersa ak di wormaal nit ñi. Njariñul nuyoo, teggini nuyoo ak ay jeexitalam dees na ko fi fésal. Naka noonu yar say gët, màndu, xam kooy àndal, xam kooy roy dina fi leere. Ay wax yu am solo te bari ngariñ […]

Tombi Borom Tuubaa (21)

Ci xaaj bi, dees na fi àndi lenn ci yi Sëriñ bi daan wax ci bisu penc ak may yi ko fa Yàlla jagleel. Ni miy xéttale nit ñi ci àdduna noonu it la leen di xéttale ëllag. Naka noonu di neen fi béral lenn ci dénkaane yi itam ak njariñ yu réy yi ñu […]

Tombi Borom Tuubaa (20)

Fii di neen fi leeral njariñal topp ndigal ak yitewoo njub. Dees na fi fésal itam ni léppi Sëriñ barkeele ak ni Yàlla di nangoo ñaanam. Xar-baaxi Sëriñ Tuubaa itam cig mbindam ak i jagleem ak ni mu daan taxawoo taalube yi dees na ko fi xamee itam. Naka noonu ni Sëriñ bi xamee mbiri […]

Leeral Nahju (3)

Fii deef na leeral lenn ci ay teggin yi nit ki wara làmboo bu toogee ak ay mag walla mu nekk ci biiri nit. Naka noonu deef na fi béral itam, ni nit ki wara sàmmee ay gëtam ak làmmiñam. Di xool lu baax, di am kersa tey wax yiw. Di tàggat boppam itam ci […]

Tombi Borom Tuubaa (19)

Dog wi deef na fi àndi itam lenn ci xar-baaxi Sëriñ bi, lenn ci yi ko Yàlla may ak lenn ci ay hikmaam Naka noonu da nga fi dégg ay hisa yuy wone ni am na it ñu ko daan jéem a natu ci anam yu kéemaane. Ak ni mu daan delloo lépp ci Yàlla. […]

Tombi Borom Tuubaa (18)

Fii dees na fi wone lenn ci màndargay yërmandey Sëriñ bi ak ñi mu daan sàmme kollare. Ni mu wàccoog nun itam ci wax, ci jëf ak ci bind. Ak ni mu defoon ragal Yàlla muy lépp. Naka noonu dees na fi leeral yennet ci xisa yuy wone xar-baaxi Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara […]

Leeral Nahju (2)

Ci ñaarelu xaaj bi dees na fi àndi ñaan yi Sëriñ bi ñaan ci Téere bi ak li muy ñaan ci Boroomam ak di ko ñaanal képp ku jàng Téere bi. Mu di fi dénk taalube yi ay teggin, boole ci di leeral luy teggin, soloom ci nit ki ak ni mu gànjaroo. Mu mel […]

Kan Mooy El Haaji Baara Mbàkke

Sunu sang bi turam dëgg mooy Muhammadul Amiin, ñu duppee ko Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke miy doomi Sëriñ Tuubaa. Sëriñ El Haaji Baara nag mi ngi gane àddina atum 1921 fa Ndidi. Baayam moo di Sëriñ Fàllu Mbàkke, ndeyam di Soxna Xari Sàll. Baayam moo ko dalal Alxuraan, jox ko Sëriñ Moor Sànqe, ginnaaw […]

Tombi Borom Tuubaa (17)

Ci xaaj wi dees na fi xamle itam leen ci Sëriñ bi, ni ki mbir yum baaxowoon def ak bis yu mu ko daan def. Ni mu fonkewoon julli ci waxtu, ak ni mu daan sàmmee taalube yi. Ba tay, dees na fi wone ni mu doone ki nuy cinu ak di nu musal di […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR