Tombi Borom Tuubaa (20)

Fii di neen fi leeral njariñal topp ndigal ak yitewoo njub. Dees na fi fésal itam ni léppi Sëriñ barkeele ak ni Yàlla di nangoo ñaanam. Xar-baaxi Sëriñ Tuubaa itam cig mbindam ak i jagleem ak ni mu daan taxawoo taalube yi dees na ko fi xamee itam. Naka noonu ni Sëriñ bi xamee mbiri […]

Leeral Nahju (3)

Fii deef na leeral lenn ci ay teggin yi nit ki wara làmboo bu toogee ak ay mag walla mu nekk ci biiri nit. Naka noonu deef na fi béral itam, ni nit ki wara sàmmee ay gëtam ak làmmiñam. Di xool lu baax, di am kersa tey wax yiw. Di tàggat boppam itam ci […]

Tombi Borom Tuubaa (19)

Dog wi deef na fi àndi itam lenn ci xar-baaxi Sëriñ bi, lenn ci yi ko Yàlla may ak lenn ci ay hikmaam Naka noonu da nga fi dégg ay hisa yuy wone ni am na it ñu ko daan jéem a natu ci anam yu kéemaane. Ak ni mu daan delloo lépp ci Yàlla. […]

Tombi Borom Tuubaa (18)

Fii dees na fi wone lenn ci màndargay yërmandey Sëriñ bi ak ñi mu daan sàmme kollare. Ni mu wàccoog nun itam ci wax, ci jëf ak ci bind. Ak ni mu defoon ragal Yàlla muy lépp. Naka noonu dees na fi leeral yennet ci xisa yuy wone xar-baaxi Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu Maxtaara […]

Leeral Nahju (2)

Ci ñaarelu xaaj bi dees na fi àndi ñaan yi Sëriñ bi ñaan ci Téere bi ak li muy ñaan ci Boroomam ak di ko ñaanal képp ku jàng Téere bi. Mu di fi dénk taalube yi ay teggin, boole ci di leeral luy teggin, soloom ci nit ki ak ni mu gànjaroo. Mu mel […]

Tombi Borom Tuubaa (17)

Ci xaaj wi dees na fi xamle itam leen ci Sëriñ bi, ni ki mbir yum baaxowoon def ak bis yu mu ko daan def. Ni mu fonkewoon julli ci waxtu, ak ni mu daan sàmmee taalube yi. Ba tay, dees na fi wone ni mu doone ki nuy cinu ak di nu musal di […]

Leeral Nahju (1)

Li mooy tàmbalig Téereb Nahjul Qadaa Al-Haaji.Ubbite gi rekk doy na yóbbalug dund. Dina fi feeñee ay laabire yu am solo ci sax ci jëf lu baax te bañ a taayi. Naka noonu ay wax yu am solo te bari njariñ moo fiy fés. Ay royukaay ci bépp Jullit, te mooy sahaaba yu baax yi. […]

Tombi Borom Tuubaa (16)

Ni Sëriñ bi daan jaamo Yàlla, la nu fiy béral. Anam gi mu daan jàngee Alxuraan, fonkeel gi, ak baril lu mu key jàng, waxtu yi mu daan bind, ay naafilaam ci ay ràkka, yooyu dees na fi fésal dara. Naka noonu mellom moom ci bind, ay xeeti waxam ak jëfinam, ay hikmaam ak mbir […]

Tombi Borom Tuubaa (15)

Tay nag kàddu yi daa jëm ci waxi Sëriñ bi ci mag ñi niki Maam Cerno, Seex Ibraahima Faal, Maam Seex Anta, Sëriñ Daaru Asan Njaay, Sëriñ Abdu Karim Ture… Dina fi feeñee itam seen i jagle yu réy ci Sëriñ bi. Seenug baax, seenug jàmbaar, seen i jikko yu refet, seen doggu ak seen […]

Tombi Borom Tuubaa (14)

Bismillahi Rahmani Rahiim Dees na leeral ci xaaj wi mbiri àddiya, dolle gi mu am ak ay njariñam. Di na fi feeñee itam tabeeg Sëriñ bi. Naka noonu dees na fi béral waxi Sëriñ Tuubaa ci ay taalubeem ak ñi mu àndeek ñoom, naka noonu wuute yi am ci taalube yi ci seenug daraja ak […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR