Leeral Mawaahibul Xudduus (3)

Sëriñ Mustafaa Xasiida yal na k Yàlla dolli yërmande, njéggal ak ngëram te taas nu ci barkeem. Nu defal ko 1 Fatiha, 11 lixlaas, 1 Alheekumu Takaasur, 1 Jaawartu, 1 Shakuuru Raafihu.

Nu wéyal…Su ko defee meloy sunu Boroom bu ci ne am na fu muy aju, ag lu muy sottal, dananu ci indi juróom-benni melo ngir leeral, muy kàttanam ak ug nammeelam, ak ug déggam, ak ug gisam, ak i waxam ak xam-xamam.

Lépp lu man a am kàttanug sunu Boroom ak ug nammeelam aju na ca. Lu man a am nag ñaari xaaj la: lu man a am ba noppi am, ak lu man a am te amul. Li man a ma te am man naa doon lu wéy mel ne sunuy maam, walla lu teew mel ne nun ñii, walla luy ñëw mel ne sunuy doom yiy bëgg a am.Li man a am te amul mi ngi mel ni yéefar bi génn àdduna manoon naa nekk ab jullit bala moo faatu te amul, naka noonu jullit bi faatu manoon naa nekk ab yéefar bala moo faatu te amul, naka noonu ku amul doom ba faatu manoon naa am doom laataa muy faatu.Mboolem lu war walla mu dagan walla mu jomb xam-xamub sunu Boroom aju na ca ak i waxam. Lépp lu am déggug sunu boroom ak ub gisam aju na ca.

Mboolem li am lépp ñaari xaaj la, loo xam ne ag amam daa war mel ni sunu Boroom, ak loo xam ne ag amam daa dagan rekk mel ni sunu maam ya, walla mel ni sunu doom yiy bëgg a ñëw, walla nun ñii, ak lépp looy gis ci àdduna.

Bu nuy wax xam-xamub sunu Boroom, li nu ci jublu mooy am na xam-xam boo xam ne dara la dul sikki-sàkka, amul lenn lu koy ump, walla muy niru leneen ci moom lu bokkul ak la am. Su ko defee li ñuy xam nag man naa doon lu war, walla lu jomb walla lu dagan.

Bu nuy wax waxi sunu Boroom itam na la wóor ne bokkut ak li nga xam ci ay wax, ndax du am ay araf, du kawe ak a suufe, du yees ak a màggat, du am lenn ci yi nga xam ne sunuy wax dana ko am, kon li ñu ne ay waxam la danuy firil ay waxam ci ni nu ko man a déggee.

Melow dund ga nag, nanga xam ne amul ci lenn lu muy aju li muy xamle walla li ñu ciy xame mooy sunu Boroom, mi ngi dund rekk.Leeg-leeg nag nga gis loo xam ne boo ko tuddee lu ëpp ñaari melo ci meloy sunu Boroom yi dana ci aju, leeg-leeg nga gis loo xam ne boo ko tuddee ñaari melo kepp moo ciy aju, ni ma ko waxe woon.

Fi mu ne boo tuddee lu man a am te amul dangay gis ne kàttanug sunu Boroom rekk ak ug nammeelam moo cay aju, naka noonu boo tuddee lu am te ak amam war (te mooy sunu Boroom) gisug sunu Boroom ak ug déggam rekk ñoo cay aju, waaye boo tuddoon, lu am te ag amam warul mel ni mbindeef, dangay gis ne ñent yépp dana ca aju.

Ba tay boo tuddoon lu man a am te amul walla lu jomb, dangay gis ne xam-xamub sunu Boroom rekk moo ciy aju ak i waxam waaye boo tuddoon lu am moo xam lu war la walla leneen dinga gis ne déggug sunu Boroom ak ug gisam dana ca dolliku ñoom ñent ñépp ànd ca.

Boo seetloo ba tay danga gis ne déggug sunu Boroom ak ug gisam moo gën a gàtt fu mu aju, ndax ci lu am kepp la aju, bi ci gën a digg-dóomu fu mu aju nag mooy kàttanug sunu Boroom ak ug nammeelam ndax aju na ci lépp lu man a am.

Leeral Mawaahibul Xudduus

Leeral Mawaahibul Xudduus (2)
S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR