
Jomb na ci sunu Boroom ñàkk ( nga xam ne masut a am ) jomb na ci sunu Boroom am ba noppi di ñàkkaat, jomb na ci sunu Boroom SW yemoo ak bindeef yi ( te mooy nekkul jëmm ju nuy man a laal, nekkul itam melo wuy man a dugg ci jëmm.
Nekkul ci genn wet, mel ni ci kaw walla ci suuf, walla wetug nday-joor walla càmmooy, walla ci kanam walla ci ginnaaw, Déedeet ! Amul itam ag wet ni nu ko ame nekkul itam di am jamono ni nu ko amee nun, walla muy am waxtu walla muy am ay yoxo walla ay tànk, walla muy mar walla muy bëgg kem ni nuy bëggee nun walla ni nuy maree, walla mu nekk ku tuuti walla ku rëy walla muy am benn bëgg-bëgg buy dellu ci moom ci jëfam walla ay àtteem ) jomb na ci sunu Boroom SW muy nekk melo wuy dugg ci jëmm wall muy jëmm ju nuy laal ndax lu ci am rekk aajewoo dana am, te moom aajewoowul jëm ci kenn mbaa lenn. Jomb na ci sunu Boroom muy nekk ñaar ci jëmmam walla ay meloom walla ay jëfam, amul kenn ku ko nuru ci jëmmam, kenn warut a wax ne ñaari melo yu nuroo lañu booleel sunu Boroom déedeet ! Kenn warut a wax ne ñaari Yàlla ñoo booloo nekk di jenn, Yàlla itam amul kenn ku man lenn walla mu man a sottal lenn ku dul sunu Boroom SW, menn mbindeef manut a def dara ci boppam, ba koy def ci keneen.
( Li des ci bind mi defoon nanu ko ci ab document ba doon ko yaatal, boo ko yittewoo nu yónnewaat ko )








