Bismillahi Rahmaani Rahiim Sunu xaaj wi daanaka li ci ëpp ci melloyu baax yi nit ki wara làmboo ak di ko jikkowoo moo ci nekk. Moo xam sunu digante ak sunu bop, sunuy dëkkando, sunuy way-jur ak yeneen.
Mu niy soññi bu baax ci farlu, ak di jëf lu baax te bañ koo yéem. Di waajal itam ëllag yawmal xiyaam, di ko séed ci sunuy jëf bu baax. Ba tey mu nuy xiirtal ci jiital jaamu Yàlla ci mbir bu mu man a nekk.
Ci gaatal dénkaane wi manees na ko tënk ci topp Yàlla ci namu gën a refete. Sëriñ bi it Xaada lahu Laahu Maxtaara lahu dana fiy soññi bu baax ay taalebeem ci xool ko moom ci sunuy jëf. Te nu bañ koo rusloo.
Machallah amna solo loool
Jërëjëf Soxna Diarra
Yalla nagnou yalla bolai si gni wouye sii te deff gnou aiye degui Talibé