Leeral Mawaahibul Xudduus (5)

Li nga xam ne man naa am man naa ñàkk ci sunu Boroom SHWT mooy amal mbindeef, ak ñàkkal ko, te lépp lu dul moom bindeef la, lépp daa dagan ci moom, yónni gi mu yónni yónente yi, ak waral gi mu waral ñu gëm ko ak araamal gi mu araamal ñu weddi ko, ak fay gi muy fay jullit ñi ak mbugal gi muy mbugal yéefar yi, lépp daa dagan ci moom, moo tax boo gisee ku naan sunu Boroom da koo war muy def, lu yiw walla la gën a yiw, bu ko nangu mukk danga naan lépp lu sunu Boroom def SHWT mooy la gën a rafet, ndax loo gis ab jaam yor ko ci ag xéewal sunu Boroom SHWT moo ko ko jox ci ag mbaaxam.

Waaye loo gis mu dal ab jaam ci ay mbugal walla lu muy bañ, sunu Boroom mooy feeñal ag maandoom ci moom.

Lépp lu sunu Boroom dogal bu la neexul, ci coono ak naqar ngay dëkk, ndax lu mu bëgg mu am, kon lépp lu mu dogal na la neex. Yal na nu may lépp lu mu digle mu neex nu tey góor-góorlu ci ay ndigëlam.

Bu loolu jàllee nu ñëw ci tegtal yi lay dëgëralal, yi nu waxoon ci ay melo ci sunu Boroom SWT.

Li lay tegtal amug sunu Boroom mooy: “mbindeefam yi ngay gis, te sosuñu seen bopp, ndax bu ñu sosoon seen bopp, danañu juge ci ag dagan nekk lu war te du am lenn lu koy waral te loolu xel nanguwu ko (…)

Li des ci mbind mi mi ngi ci ab Téere boo ko yittewoo nu yónne la ko.

Leeral Mawaahibul Xudduus

Leeral Mawaahibul Xudduus (4)
S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR