Leeral Mawaahibul Xudduus (7)

(Sëriñ Njaga Silla mi ci nataal bi yal na ko Yàlla dolli yërmande, yéege ko ci ay maqaama yu kawe, gëram ko te taas nu ci barkeem )

Li lay tegtal ne ab Yónente lu mu wax dëgg la mooy : bu ñu waxoon lu amul day mel ni ca ka leen yabal la juge, ndax muhjisaat yi, day taxaw taxawaayu kookee, lu mu wax dëgg la.

Muhjisa mbir lay doon mu yéeme, fekk ka mu feeñ ci moom di woote ag Yónente te da koy wax laataa muy am te keneen du ko man. Li feeñ ci nit te fekkul muy woote ag Yónente, bu dee nit ku baax karaama lañu koy tudde, mel ni bari xam-xam boo jàngul, walla gisal gumba, walla xam mbirum nit te du la ko wax ak soppiku ay jëmm. Loolu sunu Boroom da leen koy may ngir ñu gën a sax ci li ñu nekk, ci tàggat seen bakkan ak ay wird.Naka noonu am na loo xam ne, dana am ci Yónente yi, lu ñuy tudde irhaas te mooy yu yéeme yu ñuy gis walla ñu koy xam, njëkk sunu Boroom di leen Yónni, moom it li tax sunu Boroom di leen ko wan daa bëgg saa su ñu demee bay nekk ñu muy jëflaanteel, fekk ñu tàmm lu mel noonu, loo xam ne daa wuute ak na ko Yónente bi sàkkoo itam xay na du tax mu tudd muhjisa.

Su ko defee, lu mel ni “karaama” ak “irhaas” man naa am ci ag sàkku walla sax sàkkuwóo ko. Waaye “muhjisa” moom sàkku manu koo maye ndax day seede ab Yónente, te ag seede bu amee te amul lenn lu ko waral, du am njariñ.

Li tax ñu tuddee ko “muhjisa” ( aji lottal ) mooy : “ku dul ab Yónent du ko man.”

(Mbind mu matale am na ci, ku ko yittewoo rekk mën naa yég li

Leeral Mawaahibul Xudduus

Leeral Mawaahibul Xudduus (6)
S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR