Kan Mooy Soxna Maymuuna Kubra

Soxna Maymuna Kubra mooy doomi Seexul Xaadim ak Soxna Aminata Buso. Moom ak Soxna Xadiija ak Sëriñ Abdul Xaadir ñoo bokk lépp. Mi ngi gane àddina fa Ceeyeen-Jolof bisub talaata ñatti fan ci weeru Tabaski ci atum 1908.

Bi mu gane àddina Sëriñ bi dafa génne ñaari Xasida. Benn bi mu tënke ko « Allaahu » te mooy : tàmbalee « ihfaz liwajhikal kariim… ». Ba ca des mu tënke ko « Al-Hadi » moo tàmbalee ci « ihdi jamiihanaa siraatal mustaqiim… ». Moo tax mag ñi daan wax Soxna Maymuna fàww mu yàllaa, fàww mu jub.

Sëriñ Abdu Rahmaan Lóo moo ko jàngal Alxuraan ba mu mokkal ko, bind ab kaamil jébbal ko Sëriñ Tuubaa fa Njaaréem. Sëriñ bi bégg ci lool ndax moo doon kaamil bu njëkk bu ko jigéen di jox ak itam ba miy nekk Gànnaar Seex Siidiya daf ko wonoon kaamilu doomam bu jigéen. Sëriñ bi it amoon yéene am lu mel noonu. Mootax Sëriñ Tuubaa newoon ko : « Maymuna sama takki xol ja de yaa ko tekki ».

Sëriñ bi it moo ko boole ak Soxna Faati Ja Mbàkke ngir mu jàngal ko ag taalube tarbiya ko. Soxna Maymuna nag dafa déggaloon lool Soxna Faati Ja miy magam.

Ginnaaw jàng mi ak yar mu refet bi, jàng na it xam-xam ci ay nijaayam te ñooy Sëriñ Mbàkke Buso ak Sëriñ Mbàkke kànni.

Soxna ci daan na bind itam ci luy soññee ci tuub, si jub, ci dëgmal Sëriñ bi di ko liggéeyal ak di ko sopp. Daf daan bind ci araab ji bind ci wolof.

Bokk na ci ay bindam wax jii : « Maymuna bintul Xadiim, war na la foo toll di jéem, lu neex Sëriñ bu mag bi ndeem, am nga ci ngor dara dara ».

Moo wax lii itam : « Yaa Rabi may nu wér nu man laa jaamu Te may nu xel mu dal nu man laa raamu. Te nga fegal nu mbas yi ak balaa yi Te dindi njàqare yi ak béekoor yi ».

Soxna ci doonoon na it ku ragal Yàlla lool ci ay waxam ak i jëfam. Daf daan jéggale, di jéllale, maandu woon lool itam, yeewu lool te bari xam-xam. Daf daan defar ay diggante yu yàqu, di dox mbokk bu wér. Nit ku gëmoon Yàlla la am taalube lool. Bi mu fiy bàyyikoo sax Sëriñ Fàllu dafa wax ni nanu ko yóbb fa wetu Seex Ibraahima Faal ndax mu xam ne Sëriñ Tuubaa am na doom ju mel ne moom ci pasteef.

Jikkoom yu refet tax na bu bari lool ay turondo. Ñu bari sax ci kilifa doon neen ko jox seen i doom ngir mu yar leen.

Soxna Maymuna Kubra borom jikko yu refet yi mi ngi fiy jóge atum 1966. Bisu àjjuma la ko def. Yoor-yooru gàww leen ko jébbal boroomam fa Tuubaa. Yal na ngëram ak yërmande Yàlla sax ci moom ba fàww.

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
✕
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR