Bismilaahi Rahmaani Rahiim.
• Lu màgg danu koy màggal: wa man yuhasim hurumaati laahi fahuwa xayrulaa inda rabihim
●Laaj bu réy bi nag mooy kañ la?
Sunu Boroom ni mu nëbbe ismulaahil ahsam, ak julli gi gën a Tedd ci julli yi la ko nëbbe ngir bëgg nu farlu. Waaye umpalewunu ni sunu Borom xamalon na ko Yónnent bi aleyhi Salaam ginnaaw bi mu fàttelo ko ko ndax daf ne ko woon » sanuqri_ uka falaa Tanse ilaa maasàllaa » daa nu la jàngal te doo fàtte lu dul la ca Yàlla nam.
*Wuute yi ci am.
-Amna ñu ne 27 fan la ci weeru koor ndax nettalig Ibn Omar ak Ubayd ibn Xahab.
-Amna ñu jàpp ne ci fukki fan yu mujj yi lay doon te ci guddi yu tóol yi lay doon li ko waral mooy bari na ci Sahaaba yi ñu daan gént laylatuul xadar ci fukki fan yu mujj yi Yónnent bi aleyhi salam jox leen tegtal bii « iltamisu haa fil hashril awaaxiri min ramadaan » ( seetleen ko ci fukki fan yu mujj yi.
- Am ñu jàppp ne ci fukk 17 yi lay doon, te ci ëllëg sa di bisu Badar te mooy ni tegtaloo laaya bi sunu Boroom naan » wa maa ansalna hala habdiha yawmal furxaani yawmal taqahal jamaha » Yàlla Subhaanahu wa Tahaala wàcce na Alxuraan ci jaamam ci bis bi nga xam ne ca leeni teqale dogal ya jëm déwen, te mooy bis bi nga xam ne ca la ñaari mbooloo yi: mu lislaam ak mu yéefer njëkk jàmmaarloo ca badar.
_ Ñii ñooy ñi jàpp ne laylatul Xadar day sax ci benn bis waaye amna ñu gis ne dafay tuxu.
Te mooy ñi tënku ci nos gii nuy bëgg àndi:
- Bu weeru koor teroo gaaw wala dibéer guddi 27 fan lay doon.
- Bu nekke altine 19 fan.
- Bu nekke Talaata 25fan.
- Bu de àllarba 17 fan.
- Bu nekke alxamees 23 fan.
- Bu de àjjuma moom 29 fan lay doon.
• kon ñi jàpp li boole nañu wax yëpp ndax gis neen àddis yépp a wér.
• yal na Yàlla nangu sunu kooru ak sunu jaamu.
• Su ko defe nag lii manees na cee dégge lu baree-bari waaye danuy bàyyi ku ne ci nun rekk mu def ci jàngatu boppam.
Lii lépp ci Sëriñ Aafiya Ñaŋ lanu ko xame di ko ñaanal fan wu gudd, wér, mucc ak aajo ju faju barkeb weeru koor.
Al-Habdul Xadiim
Grenoble, 12/05/2020.
Jajeuf mouride
Jaajëfaat!
machallah amena solo na lène yalla fay barkep serigne bi
amena solo na lène Serigne bi fay, batkép xasida yi
Amiin Amiin
Amna solo machalah lahad fall CMB ISLAMIQUE🙏🏾
Ndeysaan Baay lahad siyaar naala bu baax jërëjëf
Yàlla na leen Yàlla fay liggéey bi am na solo
Amiin ku baax jërëjëf