Dénkaaneb Sëriñ Alhaaji Mbàkke (14)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim Lii ab Xasiida rajas la bob Sëriñ Alhaaji moo ko taalif def ko ci làkku wolof. Mu ciy fàttali ak a laabire mbokkum jullitam mu góor-góorlu ci ràññatle lu baax ak lu bon, wooteb Yàlla ak wooteb saytane. Mu mel ni kon nit manul ñàkk am ag jublu. Na fekk nag, jublu gi jar ko. Te mooy jublu Yàlla Subhaanahu Wa Tahaala ci lu dëggu, ci lu wér ak ci li sax.

Sëñ Moodu Mbàkke Njaay moo nu ko doon yékkatil. Yal na ko Yàlla defal yiiw ci barkeb sangam ba Sëriñ Moodu Mbàkke Kéemaan moo Seex Abdullaahi Borom Dëram Bi. Yal nanu Yàlla dimbali ci topp ndigal ak wattandiku tere yi barke Borom Tuubaa.

Al-Habdul Xadiim
13/03/2022

S’abonner
Notification pour
guest
0 Commentaires
Le plus ancien
Le plus récent Le plus populaire
Commentaires en ligne
Afficher tous les commentaires
Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR