Bataaxel bu bàyyiko ci Sëriñ bi jëm ci Muxtaar(2).

<<Yaw Muxtaar maa ngi lay dénk nga ragal Yàlla, te ragal Yàlla mooy jëf ndigal te bàyyi tere. Tey baril jëf yu baax, loolu mooy tax nga bari ay njariñ, te jiital allaaxira ci àddina ndax loolu mooy tax nga texe ëllëg, te mooy tax nga am kóolute ëllëg. Sax ga ngay sax ca àjjana […]

Bataaxel bu jëm ci Sëriñ Aadama Géy (3).

Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Yaw Aadama Géy boo bëggee leerug sunu Boroom dee ko jaamu. Te bul bokk ci ñiy jaamu jiggéen ñi. Deel wéttalikio sa Boroom tay wut ngërëmam ànd ak di sellal, tay jihaadante ak sa bakkan. Bul def ci sa xol lu dul lu lay jëme ci sunu Boroom. Lépp loo xam ne […]

Bataaxel bu jëm ci Ahmadu Jóob (5)

Bismilaahi rahmaani rahiim. <<Boo delloo foo mana nekk na nga ragal Yàlla, te bul bariy wax ak i nelaw ak lekk ak naan. Na ngay moytu nit ñi bu baax, saa suñu la bëggee xëcc jëmme la ci ay caaxaan dawal jëm ci tuddu Yàlla. Bul yaakaar, bul ragal ku dul Yàlla, na nga koy […]

Bataaxel bu jëm ci Borom Daarul Muhti (7)

Bismilaahi rahmaani rahiim <<Li ma lay bëgg dénk, ndénkaane la boo xam ne képp kuy moytu ay ñaawteef dina baril sag may. Maa ngi lay dénk xam-xam ak jëfe ak teggiin. Sab xol nanga ko setal ci ay taq-taq kon dinga jiitu sag maas. Deel toroxlu ci say mbokk ngir laabire leen kon dinga mucc […]

Bataaxel bu jëm ci Sëñ Masàmba kaani Buso (9)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Maa ngi lay nuyu yaw mi nga xam ne sag leer dafa bari ba nga set wecc ngir topp gi nga topp diine, yaw sama xarit bi ñu wax ne Yàlla daf koo xajal boppam ba mujj mu noot ko. Lii laa lay dénk deel topp ndigali Yàlla yi, tey daw ay […]

Ñaari Bataaxel Fa Cerno Ibraahima (11)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Maa ngi lay nuyu yaw Ibraahima, te di la xamal ne da maa bëgg nga dimbali  »Muhammad » ci aajoom ndax loru na lool. Saa soo gise bataaxel bi na nga ko béggal loo mën. Maa ngi ñaan Yàlla sunu Boroom àdduna bañ noo wor. Mbooleem ñi aju ci man na nga leen […]

Ñeenteelu Bataaxel jëm ci Maam Cerno(12)

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. « Asalaamu haleykum wa rahmatula wa tahaala wa barakaatahu, ginnaaw nuyoo bi, boo gise bataaxel bi, na nga yabal ku mokkal Alxuraan koo xam ne, gone lay doon, mu ànd ak ñaari moroomam, ndax ñu man a jàngal gone yi nekk fi, te yabal ñatti waxambaane yu man a jàngale xam-xam, ndax […]

Juróomeelu Bataaxel Fa Seex Ibra Faati(13).

Bismilaahi Rahmaani Rahiim. Li ma lay xamal mooy nga togg ci barab bi nga nekkoon njëkk may génn, te bañ a déglu waxi nit ñi nga xam ne dañuy njort te duñu xam. Amna bayit yu ma defoon fan yii ci kër Seex Siidiya, mooy :<< Ku jublu Yàlla sunu Boroom noppalu, noppal keneen. Ku […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR