Sëriñ Tuubaa XLML ginnaaw bi mu santee Yàlla sunu Boroom subhaanahuuwa tahaalaa. Julli ci Yónente bi SHWBW, daa xamle ne xam-xam mooy li gën ci lu Yàlla SW di jox ab jaam, waaye xam-xamu wéetal Yàlla sunu Boroom mooy la ca gën, lépp lu ñuy xaare bàmmeel ak yawmal xiyaam mooy la ca gën. Loolu […]
Saa su nu waxee su nu Boroom am na kàttan xamal ne li nu ci namm mooy mbir moo man a xalaat sunu Boroom man na koo amal te bu koy amal ca na mu ko bëggee la koy amale. Saa su nu waxee nammeelug sunu Boroom SW mooy ki mu nekk ci moom day […]
Sëriñ Mustafaa Xasiida yal na k Yàlla dolli yërmande, njéggal ak ngëram te taas nu ci barkeem. Nu defal ko 1 Fatiha, 11 lixlaas, 1 Alheekumu Takaasur, 1 Jaawartu, 1 Shakuuru Raafihu. Nu wéyal…Su ko defee meloy sunu Boroom bu ci ne am na fu muy aju, ag lu muy sottal, dananu ci indi juróom-benni […]
Jomb na ci sunu Boroom ñàkk ( nga xam ne masut a am ) jomb na ci sunu Boroom am ba noppi di ñàkkaat, jomb na ci sunu Boroom SW yemoo ak bindeef yi ( te mooy nekkul jëmm ju nuy man a laal, nekkul itam melo wuy man a dugg ci jëmm. Nekkul ci […]
Li nga xam ne man naa am man naa ñàkk ci sunu Boroom SHWT mooy amal mbindeef, ak ñàkkal ko, te lépp lu dul moom bindeef la, lépp daa dagan ci moom, yónni gi mu yónni yónente yi, ak waral gi mu waral ñu gëm ko ak araamal gi mu araamal ñu weddi ko, ak […]
Bu loolu jàllee nanga xam ne Yónente yi HS, am na ñatti melo yu war ci ñoom: “muy dëggal ak bañ a def lu haraam ak lu ñu sib ak jottali lañu leen yónni”. Am na ñatt yoo xam ne daa jomb ci ñoom: “mooy fen ak def lu haraam ak lu ñu sib ñàkk […]
(Sëriñ Njaga Silla mi ci nataal bi yal na ko Yàlla dolli yërmande, yéege ko ci ay maqaama yu kawe, gëram ko te taas nu ci barkeem ) Li lay tegtal ne ab Yónente lu mu wax dëgg la mooy : bu ñu waxoon lu amul day mel ni ca ka leen yabal la juge, […]
“Laa Ilaaha Illaahu” mooy : “sunu Boroom aajewoowul jëm ci kenn, te ku ne ak lu ne aajewoo na jëm ci moom” Saa soo tuddee doylug sunu Boroom SW dananu ci dégge ne ku jiitu la, te day des te niruwul lenn te ku taxaw ci boppam la te amul genn wàññen te day dégg […]
Ki sunu Boroom di Yónni fàww góor lay doon, nit lay doon, doon gor te am xel, sunu Boroom digal ko mu wax nit ña ag bëggam. Naka noonu kiy am xam-xamub Yónent fàww yooyu am ci moom waaye sunu Boroom da koo yónniwul. Bokk na ci li leen wuutale ba tay, ab Yónente moom […]