Leeral Mawaahibul Xudduus (5)

Li nga xam ne man naa am man naa ñàkk ci sunu Boroom SHWT mooy amal mbindeef, ak ñàkkal ko, te lépp lu dul moom bindeef la, lépp daa dagan ci moom, yónni gi mu yónni yónente yi, ak waral gi mu waral ñu gëm ko ak araamal gi mu araamal ñu weddi ko, ak […]

Siyaare Sëriñ Tuubaa (1)

Dees na xame ci téereb Sëriñ Allaaji Mbàkke bi naka lañuy siyaare Sëriñ Bi. Mu fiy wone teggin yi ñu war a làmboo bu nu koy siyaare. Naka noonu yéene ji, farlu gi, ak defin wi. Nu xame ci rekk nag dafa wone aw yoon wu am solo ci siyaare Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (4)

Jomb na ci sunu Boroom ñàkk ( nga xam ne masut a am ) jomb na ci sunu Boroom am ba noppi di ñàkkaat, jomb na ci sunu Boroom SW yemoo ak bindeef yi ( te mooy nekkul jëmm ju nuy man a laal, nekkul itam melo wuy man a dugg ci jëmm. Nekkul ci […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (3)

Sëriñ Mustafaa Xasiida yal na k Yàlla dolli yërmande, njéggal ak ngëram te taas nu ci barkeem. Nu defal ko 1 Fatiha, 11 lixlaas, 1 Alheekumu Takaasur, 1 Jaawartu, 1 Shakuuru Raafihu. Nu wéyal…Su ko defee meloy sunu Boroom bu ci ne am na fu muy aju, ag lu muy sottal, dananu ci indi juróom-benni […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (2)

Saa su nu waxee su nu Boroom am na kàttan xamal ne li nu ci namm mooy mbir moo man a xalaat sunu Boroom man na koo amal te bu koy amal ca na mu ko bëggee la koy amale. Saa su nu waxee nammeelug sunu Boroom SW mooy ki mu nekk ci moom day […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (1)

Sëriñ Tuubaa XLML ginnaaw bi mu santee Yàlla sunu Boroom subhaanahuuwa tahaalaa. Julli ci Yónente bi SHWBW, daa xamle ne xam-xam mooy li gën ci lu Yàlla SW di jox ab jaam, waaye xam-xamu wéetal Yàlla sunu Boroom mooy la ca gën, lépp lu ñuy xaare bàmmeel ak yawmal xiyaam mooy la ca gën. Loolu […]

Leeral Miftaahul Xuyóob (18)

Lii mooy sunu xaaj bu mujj ci téere bi, jëm ci xamle bunti àjjana yi, ak ya man a doon sabab ngir tàbbi ca. Yal nanu Yàlla tàbbal ci àjjana yu kawe ya te nangul sunug jaamu. Di ñaanal itam Sëriñ Mbàkke Faal, sunu Boroom dolli ko njéegal, yërmande ak ngëram Barkeb Xasiida yi mu […]

Leeral Miftaahul Xuyóob (17)

Fii dinanu fi leeral mbiri Siraat, yi ci Abu ci ay nettali, ci kem ni ñu ko melale. Naka noonu dina fi feeñee li man a sabab jafeeg jéegi ji. Naka noonu solos jëfe ndigal, bàyyi tere yi ak seelal dina yombal jéegi Siraat. Yal nanu Yàlla yombalal jéegi ji, te musal nu ci sawara.

Miftaahul Xuyóob (16)

Di nanu leeral ci xaaj bii, njariñal siyaare baameel ci ñiy dund ak ñi faatu. Bu dee kiy dund dina xam mi àdduna saxul, fàww dina faatu. Loolu ag waar la, jaaju la it ci moom. Ki faatu moom dina jot i xéewal ndax ñaan yi miy jot. Yal nanu jeexal sunu dund ci ag […]

Jotaayu Texe (13)

Ci xaaj wi di nanu fi xàmmee ne, ànd gi nu ànd ak Sëriñ Bi, tawfeex kepp la. Ba tay di nanu fi jàngee ne, ag njub, ag mbaax lépp ci coobarey Yàlla lay aju. Nun défunt ludul jéem. La Sëriñ Tuubaa dénkoon Soxna Fati Ja ci dolleey lixlaas dees na ko fi jàngee tamit

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR