Kan Mooy Sëriñ Móodu Awa Bàlla

Sëriñ Muhammadu Awa Bàlla Mbàkke, Maam Cerno mooy way-juram. Mi ngi feeñ jamono atum 1896 fa Mbàkke-Bawol. Moo njëkk doon xalifab Maam Cerno itam. Soxna Awa Bàlla Jóob mooy way-juram wu jigéen. Boo toppe ay maamam ci wet googu Koki lay déllu.Yonent bi Aleyhi Salaam leen ko tuddee. Maam Cerno moo ko jàngal, jàngee na […]

Siyaare Sëriñ Tuubaa (2)

Ci xaaj bu mujj bi day leeral nees war a def boo agsee Tuubaa di siyaarsi. Te mooy waajtaay yi ci ajju yépp. Naka noonu abyaat yiy téj bunt bii day firndeel bu wér ne Sëriñ Bi ku mat a siyaare la.

Leeral Mawaahibul Xudduus (8)

“Laa Ilaaha Illaahu” mooy : “sunu Boroom aajewoowul jëm ci kenn, te ku ne ak lu ne aajewoo na jëm ci moom” Saa soo tuddee doylug sunu Boroom SW dananu ci dégge ne ku jiitu la, te day des te niruwul lenn te ku taxaw ci boppam la te amul genn wàññen te day dégg […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (7)

(Sëriñ Njaga Silla mi ci nataal bi yal na ko Yàlla dolli yërmande, yéege ko ci ay maqaama yu kawe, gëram ko te taas nu ci barkeem ) Li lay tegtal ne ab Yónente lu mu wax dëgg la mooy : bu ñu waxoon lu amul day mel ni ca ka leen yabal la juge, […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (6)

Bu loolu jàllee nanga xam ne Yónente yi HS, am na ñatti melo yu war ci ñoom: “muy dëggal ak bañ a def lu haraam ak lu ñu sib ak jottali lañu leen yónni”. Am na ñatt yoo xam ne daa jomb ci ñoom: “mooy fen ak def lu haraam ak lu ñu sib ñàkk […]

Kan Mooy Sëriñ Maamuun Mbàkke

Sëriñ Móodu Maamun mooy doomi Maam Seex Anta ak Soxna Buri Mbàkke.Sëriñ Móodu Maamun sëti Maam Maharam la ci ñaari wet yépp. Mi ngi gane àddina atum 1887 walla 1888 fa Tuubaa. Ba mu feeñee jamono rekk la way-juram wu jigéen faatu. Nu jël Sëriñ Maamun jox ko Sëriñ Tuubaa mu defal ko la mu […]

L’arme des Craintifs (5)

Les actes obligatoires de la prièreIls sont au nombre de quinze : l’intention, le takbir, la station debout qui l’accompagne, la récitation de la Sourate Fatiha et la station debout qui l’accompagne. Puis, la génuflexion, le redressement, la prosternation et le redressement qui lui estconsécutif pour revenir à la position assise. De même, l’intention d’effectuer […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (5)

Li nga xam ne man naa am man naa ñàkk ci sunu Boroom SHWT mooy amal mbindeef, ak ñàkkal ko, te lépp lu dul moom bindeef la, lépp daa dagan ci moom, yónni gi mu yónni yónente yi, ak waral gi mu waral ñu gëm ko ak araamal gi mu araamal ñu weddi ko, ak […]

Siyaare Sëriñ Tuubaa (1)

Dees na xame ci téereb Sëriñ Allaaji Mbàkke bi naka lañuy siyaare Sëriñ Bi. Mu fiy wone teggin yi ñu war a làmboo bu nu koy siyaare. Naka noonu yéene ji, farlu gi, ak defin wi. Nu xame ci rekk nag dafa wone aw yoon wu am solo ci siyaare Sëriñ Tuubaa Xaada lahu Laahu […]

Leeral Mawaahibul Xudduus (4)

Jomb na ci sunu Boroom ñàkk ( nga xam ne masut a am ) jomb na ci sunu Boroom am ba noppi di ñàkkaat, jomb na ci sunu Boroom SW yemoo ak bindeef yi ( te mooy nekkul jëmm ju nuy man a laal, nekkul itam melo wuy man a dugg ci jëmm. Nekkul ci […]

Al-Habdul Xadiim

GRATUIT
VOIR